Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
20 juillet 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Opinions
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
Par Xari Njaay

NDAX MAKI SÀLL WAR NAA LAAJ ÑETTEELU MOOMEEL ?

Lu waay xamadi xamadi xam ne Maki Sàll mooy Njiitu-réew mi. Waaw, ne askan wee ko fal ci atum 2012. Bi mu toogeek léegi nag, lu bari la dig askan wi.

Xari Njaay (www.defuwaxu.com)  |   Publication 15/02/2020

Lu waay xamadi xamadi xam ne Maki Sàll mooy Njiitu-réew mi. Waaw, ne askan wee ko fal ci atum 2012. Bi mu toogeek léegi nag, lu bari la dig askan wi. Waaye mel na ne bi ci ëppal solo askan wi mooy ñaari màndaa yi mu waatoon ne moom lay toog ci jal bi. Ci kow loolu, am nañu seen xel tàmbalee tey, ñu naan ngóor sii niruwul ku nar a sàmm ay kàddoom. Ba tax na LU DEFU WAXU jóg def ay jéego fekki ñenn ci askan wi ngir ñu wax seen xalaat ci ci mbir mi.

Juróom lañu te ku ci nekk lii lan la laaj :

Asalaamalekum Mamadu Jóob, jaaykat nga ci daara ju kawe jii di Gastoŋ Berse, maa ngi tudd Xari Njaay di ab taskatu xibaar ci LU DEFU WAXU.

Luy sa xalaat ci coowal ñetteelu màndaawu Maki Sàll bi ?

« Maalekum salaam soxna si. Waaw, man de li ma xalaat ci ñetteelu màndaa bi, ragal pàrteem tas moo tax Maki Sàll ñemewu cee wax lu leer. Fi mu ne nii bu nee du wut ñetteelu màndaa ku ne dina jéem a wut fu mu aw. Te loolu du baax ci nguuram. Te yit, niñ fi doon coowe Karim Wàdd ak Xalifa Sàll la ko mbamb nar a toppe. Senegale yee mel noonu, kenn mënuleen a tere coow te jamono jii ñetteelu màndaa xew. »

Mareem Sog, di ndongo ci daara ju kawe jii di Gastoŋ Berse nii la gise mbir mi :

«Ci sama gis-gis, ñetteelu màndaawu Maki Sàll waroon naa mën a nekk ci kow doomi-réew mi bég ci moom. Waaye fi mu tollu nii de, ñi ëpp ci ñoom rafetluwuńu liggéeyam. Ba tax na bu nee day laaj ñetteelu màndaa, coow ak fitna rekk la fiy indi. Abdulaay Wàdd jéemoon na ko ci 23eelu fan ci weeru suweŋ 2012 ngir teg fi doomam te mujjul a àntu. Man coow li ne kurr ci ñetteelu màndaa bi loolu rekk la may fàttali, du leneen.»

Ngiraan Njaay ndongo ci Gastoŋ Berse :

«Ci sama xalaat bu gàtt, jàpp naa ne ñaari màndaa doy nan sëkk ndax dara la fi deful bi mu toogee ci jal beek tey. Ndax jamono jii yaakaar naa ne réew mi soxla na leneen lu-dul ay TER walla ay kër yoo xam ne du  ñëpp a am dooley dëkk fa. Naam mbébétam ci réew mi rafet na waaye na may ñeneen ñu wane seen mënin ndax kat nguur noonu lay doxe,  mënoo loo sumb rekk eggale ko.»

Moktaar Jàllo, eñseñeer ci wàllu soŋ :

 « Coowal ñetteelu màndaa bi bari na lool. Waaye lépp Njiitu-réew mee ko waral. Ndax keroog ba muy jàkkaarlook askan wi ca 31elu fan ci weeru desàmbar 2019, la waroon a wax lu leer. Waaye defu ko, mu mel ni yëf yi ńoru ko. Fi mu ne nii gën na noo réeral. Li ci des mooy ñaan Yàlla mu delloosi xelam ba mu yem ci ñaari màndaa yi ko àtte ndeyu réew mi may. Su ko defulee, réew mi dina yëngu te loolu kenn ñaanu ko Yàlla.»

Paap Aamadu Siise, minise almiñom :

« Netteelu màndaa, yaakaar naa ne mën naa war a ne. Ndax, keneen ku ńu fal it day sumb liggéey bu bees. Te su nu waxantee dëgg, gisuma ku fi mën a wuutu Maki Sàll. Kon li gën mooy mu def ñetteelu màndaa ngir yeggale liggéey bi mu tàmbali ci atum 2012.»

Articles les plus lus

shoo-tas-rv1-32-scaled.jpg
DIOMAYE MOOY SONKO OU LES DEUX FACES D’UNE MÉDAILLE
Le président Faye a parlé. Après les propos outrageants de son Premier ministre, la nation attendait ...

cthiakane_.jpg
CE QUE L’AFFAIRE DU GRAND THÉÂTRE NOUS APPREND
Le 15 juillet 2025, la direction générale du Grand Théâtre national du Sénégal a publié un communiqué ...

screenshot_2025-07-17_at_2.47.40_pm.png
LE 18 PASTEFMAIRE
Méphisto le Client et la meute enragée Chaque révolution a sa plèbe. Chaque tyrannie, sa meute. ...

20250717-185439.jpg
DIOMAYE APPELLE À DÉCOLINISER L'UNIVERSITÉ
(SenePlus) - Le chef de l'État a officiellement ouvert ce jeudi au CICAD les concertations nationales ...

ibfa.jpg
LA SEMAINE OU LE PREMIER MINISTRE MENACE DE LIMOGER LE PRESIDENT
Pour faire de vieux jours sous nos cieux, à n’en pas douter, il faut avoir le cœur bien accroché… Passons ...

Vos articles préférés de la semaine

capture_decran_2025-03-12_a_17.20.22_1.png
BIOPSIE D’UNE KOROMAQUERIE !
Être amoureux de la République de Ndoumbélane et ne pas vivre de satire peut rendre malade. Et être ...

capture_decran_2025-07-14_a_00.42.06.png
DIOMAYE - SONKO ET LES ENJEUX D’UN CONFLIT DE LÉGITIMITÉ
Les divergences au sein du couple Diomaye - Sonko ne seraient pas une répétition de l’histoire politique ...

shoo-tas-rv1-32-scaled.jpg
DIOMAYE MOOY SONKO OU LES DEUX FACES D’UNE MÉDAILLE
Le président Faye a parlé. Après les propos outrageants de son Premier ministre, la nation attendait ...

chroniques_dun_temps_politique_par_felwine_sarr_-_chroniques_dun_temps_politique_-_la_crise_de_letat_de_droit_felwine_sarr_recoit_sidy_alpha_ndiaye_hdpt4urkww0_-_709x399_-_2m30s.png
L’INDIGNATION À GÉOMÉTRIE VARIABLE
Chronique d’un temps politique Dans son émission Chroniques d’un temps politique, lancée en ...

sans_detour_mamadou_ndoye_iv_0_2.jpg
IL NOUS FAUT UNE POLITIQUE LINGUISTIQUE AUDACIEUSE A L’ECOLE
Invité à prononcer le cours inaugural du colloque international « Multilinguisme et diversité à ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous