Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
28 septembre 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Culture
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

ËTTUB TAALIF

Sëriñ Baabakar Jóob Callweer ndaanaan la, di bindkat, di gëstukat itam ci làmmiñu wolof. Liggéeyam ak xam-xamam dëgg nag ñi ngi jëm ci teyaatar. Mooy doxal jotaayu léeb bItudd Callweer, cI Mourchid TV

Defu Waxu  |   BAABAKAR JÓOB AK NDEY XAYBA FAAL  |   Publication 25/07/2020

Sëriñ Baabakar Jóob Callweer ndaanaan la, di bindkat, di gëstukat itam ci làmmiñu wolof. Liggéeyam ak xam-xamam dëgg nag ñi ngi jëm ci teyaatar. Mooy doxal jotaayu léeb bItudd Callweer, cI Mourchid TV.

SAAGA

Saaga du ngànnaay,

du pakk, du ray, du gaañ, du jàpp, du takk. 

Saaga du faxas, du raxas, du jubal, du dugal, du ràbb, du nàmm.

Heey yaw mi sa xel nasax, rambax, senax, yonjax, jastindikoo saaga, def ko paaka. 

Du jam, du rendi, du fàdd, du ngàdd, du ñàdd. 

Su xalaat tërëfee, xel tarxiis, ñàkk, ñëg, ñànki, 

Xol nërmeelu, bóli coroxaan, làmmiñ saaga.  

Heey saaga, du lay, du way, du yay, 

Ku sa xalaat wér péŋŋ, say saaga ne meŋŋ.

II

Soxna Ndey Xayba Faal mi ngi dëkk Ndakaaru, doon jàng xam-xamu melosuuf ca Daara ju mag ju Séex Anta Jόob. Bind na taalif yu bari ci fànn yu wuute, niki bëgg-bëgg ay jafe-jafey àddina, ngëm ak diine, sàkku xam-xam ak coono yi ci aju.

YOONU BÀNNEEX

Yoonu bànneex moo bariy xeer

Leeg-leeg mu lëndëm

Ba nga foog ni danga gëlëm

Moone soo siggee de seen as leer

Yoonu bànneex moo bariy nattu

Ay tolof-tolof yoo war a muñ

Gëm ni lu mu yàgg yàgg dinga muuñ

Yokku, féex mel ni jigéen ju masul a matu

Yoonu bànneex moo bariy njariñ

Dina la tàggat ñemeloo la tawat

Ngay dékku naqar fab sa xel di xalaat

Jàngat ne Yaa Rabbi rekk a doy Sëriñ

Yoonu bànneex moo man a gudd

Ngay dékk say loxo di sàkku ñaan

Di laabal sa xol dëddale la ak kañaan

Xam ne bis du gën a réy sa bisu juddu

Bànneex bi may waxtaane

Xajul ci bile dëkk

Dafay sax dàkk

Ni ko téere bu sell bi junje      

Articles les plus lus

ammbow.jpg
AMADOU MAHTAR MBOW, L’HÉRITAGE D’UN SIÈCLE DE COMBATS
C’est l’un des sages du continent. Ce mercredi marque le premier anniversaire du rappel à Dieu d'Amadou ...

mgueye_lq.jpg
LE PRES ET SES MILLIARDS DE FUMÉE
Le financement du Plan de redressement économique et social (Pres) fera-t-il revivre les anciennes filières ...

garage_latdior.jpg
OPERATION COUP DE POING AU GARAGE LAT DIOR
Dans la nuit de lundi à mardi, le garage Lat Dior, situé derrière le tribunal de grande instance de ...

capture_decran_2025-09-09_a_19.43.16.png
LA PAUVRETÉ, UN CRIME ?
Sous l’affichage tapageur d’un État de droit protecteur, le Sénégal s’éloigne silencieusement ...

whatsapp-image-2025-09-23-at-15.51.04.jpeg
LES FÉMINISTES APPELLENT À DES ACTES APRÈS LE DISCOURS DE DIOMAYE À L’ONU
Le lundi 22 septembre 2025, à la tribune des Nations Unies, le président de la République du Sénégal, ...

Vos articles préférés de la semaine

capture_decran_2025-09-19_a_15.17.55.png
SORTIR DE LA FASCINATION DU MARABOUTAGE
Inaf, inaf, inaf ! Nos écrans sont devenus des miroirs puissants de notre société. À travers les ...

scr-20250918-qocm.jpeg
JOURNÉE À MILAN
Rien à dire, Ousmane Sonko est bien un phénomène. Réussir une mobilisation monstre en terre lointaine ...

capture_decran_2025-09-12_a_12.48.41.png
REDUIRE LA PROFESSION VETERINAIRE A LA PRATIQUE DE LA SANTE ANIMALE NE PEUT PROSPERER EN AFRIQUE SUBSAHARIENNE
Ex-directeur de l’École Inter-États des Sciences et Médecine Vétérinaire (EISMV) de Dakar et ancien ...

1280.jpeg
QUI POUR ARRÊTER LE CARNAGE DE L’ÉTAT SIONISTE ?
Le génocide se poursuit dans la bande Gaza. Chaque jour, des dizaines de vies sont impitoyablement ...

capture_decran_2025-09-20_a_17.17.44.png
SCHALKE, FIERTÉ D'UN PEUPLE OUVRIER
« Schalke, c’est le charbon, la sueur et la fierté d’un peuple. » À Gelsenkirchen, dans le ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous