Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
28 septembre 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Éducation
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

NDAJEM NJABOOTU ALFABETISAASIYOŋ CA KUNGÉEL

Ca Kungéel (péeyub Bàmbug) amoon na ndajem tàggat bu

Jaafara Sadiixu Fofana (www.defuwaxu/com)  |   Publication 09/04/2020

Ca Kungéel (péeyub Bàmbug) amoon na ndajem tàggat bu ñetti fan ci « Ndefarum saf-safal ak sunu xeeti meññeef yi ak suusal caakiri ak cerey ñebbe ».

Lu tollu ci 30i jigéen ak lu teg, bawoo ci 6i diiwaan ak i gox yu wuute ci réew mi, amaloon nañ am ndaje ca Kungéel. Ndaje maa ngi dooroon àjjuma, 28eelu fan ci weeru féewaryee jàpp dibéer 1eelu fan ci weeru màrs 2020. Ñu bare ñoo fa daje woon : jàngalekat, yombalkat, gëstukat, lëkkalekat, añs.
Liñ ko dugge woon mooy tàggatu ci « Ndefarum Saf-safal ak sunu xeeti meññeef yi ak suusal caakiri ak cere ñebbe »
Ku nekk ci jigéen ñooñu, nag, cib bànqaasu diiwaan mbaa gox nga féete. Bànqaas yooyu, dippees na leen ci nasaraan « Komisiyoŋ » SNAN. Juróom-benni bànqaas lañu am, yu :
• Jókkul Mbelbuug
• Jurbel
• Kungéel
• Kawlax
• Kafrin ak
• Kidira
Ñoxor Ngom mi jiite SNAN (Sàndikaa Njabootu
Alfaabetisaasiyoŋ Nasiyonaal), ginnaaw bi mu sargalee kilifa yi, wax ci juddug SNAN, kàddu yii la fa biral :
« Ndaje maa ngi tàmbale ci àjjuma jii, waaye ñu ngi ko déggoo woon ca jataayu Jókkul Mbelbuug ci 23eelu fan ci weeru desàmbar 2019 mu bokk ci sunu jëf yi nu tëral war koo doxal ci at mi, maanaam mu dellu ci naalam. Lees ci jublu moo di fexe ba ubbil jigéen ñi buntub xéy ak koom-koom ngir soppi ak gën a baaxal seen nekkin, te bañ a yem rekk ci njàngum liifantu ak xayma, waaye jëfandikoo leen ba indi koom. »
Kii di Daawuda Jàllo, 2eelu tofo ci njiitu Bokk moomeelu Kungéel (MEER) ak Maamudu Umar Géy miy « Inspekteeru edikaasiyoŋ ak foormaasiyoŋ » Luññutukat bi ŋànk ak di saytu lépp lu aju ci njàngum tuut-tànk yi, yar ak tàggat ci xaaj-diiwaan bu Kungéel, jàpp nañ ni tàggat bii lu ñu war a ñoŋal la.
Ndax ci 3 nisër yi ko taxoon a jóg, 2 yi moom jot nañu ko fii.
Ndaxte, soxna Juma Jóob (di kenn ci way-tàggatu yi) , li mu fi wone, nettali ko ci 3 xeeti saar yi ngeen fi jànge, dal na xel, te it am na solo lool. Ndege, dina tax ba jigéen ñi gën a yokk seen koom. 3eel bi moom ci kàdduy IEF bi, ci biti doŋŋ lañ koy mën a nattee ci kow ñu nangoo sotti ak wéyal li ñu fi weccoo ci 3 fan yii ci seen gox yi !
Aliyu Sàll mi teewal « Koñsey departamantaal » bi mu jëlee kàddu nee na : « li SNAN def nii méngoo na lool ak sémbub PRODESK dib naal bu nu defar ngir gunge kuréel yeek mbootaayi koom yi nekk ci gox bi, te dinanu fexe ba def ciy jéego »
Mbaaxaan Jóob mi teewaloon kuréelu CDK, gannaaw bi mu fésalee mbégteem ci tàggat bi, wone na ne lëkkaloo dina am ak waa SNAN ngir ñu àndandoo lawal xam-xam bii.
Laata Inspekteer, maanaam IEF, di tëj ndaje mi ci turu « Perefe » mi ko yebal, Ami Siise Fay jagleel nab taalifu delloo njukkal Sàmba Jaawo mi desoon ci toolu xare bi ci 24 fan ci weeru desàmbar 2019 cib « laksidaa » diggante Gudiri ak Kidira ba xol yépp tooy !
Awa Faati, ak Jaafara Fofana feelu ko, waaye, ñoom seen taalif dafa jëm ci njariñal saf-safal bi ñu doon defar, ak jàng ak jàppalante ngir réew mi jëm kanam.
Wólis 6 « Komisiyoŋ » yi bokk, waa Luga ak Dakaar ñoom it fésal nañ seen yéene ngir bokk ci SNAN.
Way-tàggatu yi woon ci lël bi, jox nañ leen ku ci nekk « lijaasa » buy firndéel ni bokkoon na ci.
Nu wax itam ne, ginnaaw « Meer », « Perefe », « IEF » ak « Koñsey departamantaal », SNAN yëgaloon na lël bi yeneen i kuréel ak i kilifa ngir ñu teew, jëmmal ak darajaal lël bi ci ubbite beek tëjte bi, ñu ràññee ci : UCEM, Kërug Jigéen, GIE « Xaritu xale yi, Seydinaa Ibraayima Jóob ak Ndey Ndumbe Saar mu « Comité consultatif des femmes ».

Articles les plus lus

ammbow.jpg
AMADOU MAHTAR MBOW, L’HÉRITAGE D’UN SIÈCLE DE COMBATS
C’est l’un des sages du continent. Ce mercredi marque le premier anniversaire du rappel à Dieu d'Amadou ...

mgueye_lq.jpg
LE PRES ET SES MILLIARDS DE FUMÉE
Le financement du Plan de redressement économique et social (Pres) fera-t-il revivre les anciennes filières ...

garage_latdior.jpg
OPERATION COUP DE POING AU GARAGE LAT DIOR
Dans la nuit de lundi à mardi, le garage Lat Dior, situé derrière le tribunal de grande instance de ...

capture_decran_2025-09-09_a_19.43.16.png
LA PAUVRETÉ, UN CRIME ?
Sous l’affichage tapageur d’un État de droit protecteur, le Sénégal s’éloigne silencieusement ...

whatsapp-image-2025-09-23-at-15.51.04.jpeg
LES FÉMINISTES APPELLENT À DES ACTES APRÈS LE DISCOURS DE DIOMAYE À L’ONU
Le lundi 22 septembre 2025, à la tribune des Nations Unies, le président de la République du Sénégal, ...

Vos articles préférés de la semaine

capture_decran_2025-09-19_a_15.17.55.png
SORTIR DE LA FASCINATION DU MARABOUTAGE
Inaf, inaf, inaf ! Nos écrans sont devenus des miroirs puissants de notre société. À travers les ...

scr-20250918-qocm.jpeg
JOURNÉE À MILAN
Rien à dire, Ousmane Sonko est bien un phénomène. Réussir une mobilisation monstre en terre lointaine ...

capture_decran_2025-09-12_a_12.48.41.png
REDUIRE LA PROFESSION VETERINAIRE A LA PRATIQUE DE LA SANTE ANIMALE NE PEUT PROSPERER EN AFRIQUE SUBSAHARIENNE
Ex-directeur de l’École Inter-États des Sciences et Médecine Vétérinaire (EISMV) de Dakar et ancien ...

1280.jpeg
QUI POUR ARRÊTER LE CARNAGE DE L’ÉTAT SIONISTE ?
Le génocide se poursuit dans la bande Gaza. Chaque jour, des dizaines de vies sont impitoyablement ...

capture_decran_2025-09-20_a_17.17.44.png
SCHALKE, FIERTÉ D'UN PEUPLE OUVRIER
« Schalke, c’est le charbon, la sueur et la fierté d’un peuple. » À Gelsenkirchen, dans le ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous