Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
16 août 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
International
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

MALI AK FARÃS : LA WOON, WONNI NA

Diggante Farãs ak Mali ma ngay wéy di ñagas. Loolu nag tàmbaliwul tey rekk.

defuwaxu.com  |   Mbay SOW  |   Publication 10/10/2022

Diggante Farãs ak Mali ma ngay wéy di ñagas. Loolu nag tàmbaliwul tey rekk. Ndax, ginnaaw bi ñu daaneelee kii di Ibraahiima Buubakar Keyta la ànd bi tàmbali woon a taq suuf. Li ko waral mooy ndogal yu am solo yu Nguurug Mali gi jot a jёl ngir dakkal yenn lёkkaloom ak ñii di waa Farãs. Loolu nag, mooy dagg xoli Farãse yi fim ne nii. Ndeke, amatuñ fa Mali lenn lu ñuy dogalati, walla di ci àddu. Rax-ci-dolli, fan yii nu génn, Asimi Goytaa, Njiitul Mali, dafa jёl ay ndogal yu am solo, daldi far yenn ciy déggoo yu ñu xaatimoon diggante ñaari réew yi laata ñuy moom seen bopp. Dafa mel ni Afrig dafa nekk di yeewu nag.

Talaata 18 ut 2020 lañu daaneel Nguurug Ibraahiima Buubakar Keyta. Ca la kurél gii di Comité National pour le Salut du Peuple (CNSP) jёle woon réew ma ba tey. Mu mel ni nag, boobaak tey, ñu bari njortoon nañu Farãs a defaatoon mёniinam. Nde, tubaab yi, teg loxo réewi Afrig jaral na leen lu ne, ba ci nasaxal seen i koom, daaneel ay nguur ngir teg fa seen i ndaw, maanaam ay tubaab yu ñuul. Moo tax, bi coow li jibee, xel yépp ne yar ci nootkat yu bon yooyu. Dafa di, Farãs sax moo njёkkoon a génn di ñaawlu jёf ji. Waaye, naaféq bees ko xame moo taxoon gёmeesu ko woon. Ndekete yoo, du ci lenn.

Bah Ndaw mi nekkoon jёwriñu kaaaraange lees dénkoon Njiiteefu négandiku gi. Booba, Asimi Goytaa moo doon tof-njiit la, Moktaar Wan di woon jёwriñ ju njёkkoon ja. Waaye, dañu dem ba ci biir, xel tàmbalee ñaaw ci Bah Ndaw. Soldaar yi, ci kilifteefu Asimi Goytaa, njort ne Bah Ndaw mii kat, ku dem Farãs ёlbati na xel mi ba féetewoo ko. Ci lañu jёlee seen i matuwaay, déjjati ko ci njiiteef gi. Lu ko moy, doon na leen yàqal li ñu jotoon a liggéey yépp ak li ñu nasoon ngir péexug Mali ak naataangeem. Ñoo ngi fàttaliku, keroog 24 me 2021, ba Moktaar Wan di tёral Nguuram. Ca bés ba lañu leen jàpp, wàcce leen. Ñaari fan lees ci teg, 26 me,  ñu tekkilu leen seen i ndomboy-tànk, ñu daldi bàyyi. Fullaay jaay daqaar, am déet ? Goytaa daldi dёggal boppam, jёl mbir yi, jiiteel ko boppam. Boobu nag la jafe-jafey Farãs yi ca Mali tàmbali. Dogal ya ñu fa amoon yépp ak i ngёneel, Asimi Goytaa ak i ñoñam di leen dindi ndànk ndànk. Makorõ di gёn a bokk golo gi, njiiti Farãs yiy jёfuur. Waaye, ñoo yey kat. Ku tàmm loo wax rekk ñu tegal la ci “waaw”, loo yóotu jot, boo ko amatul sa xol du neex. Dafa di, Farãs ak i njiitam, ay jaam lañ nu mёs a jàppe. Seen juróom-ñaari xel mёsta xalaat kenn ci njiiti jaam yu tekkiwul dara yooyu di leen diir mbagg, ba di leen dàq seenum réew. Waaye, loo gis, dafay jeex.

Mali dafa doon ŋàññi doxalinu Farãs ñeel xeexug terorist yi. Noonu, Farãs xéy bés rekk, ci ndogalu  Makorõ, weeru suwe 2021, dakkal liggéeyu Barkhan. Ci la xamle ne soldaar yi dinañu wéer ngànnaay yi ci atum 2022, dellu ci seen i réew. Bett boobu leen Farãs bettoon a tax ba, kii di Songel Mayga, jёwriñ ju njёkk ji, kaasoon loolu ca magum ndajem Mbootaayu xeet yi (ONU), amoon ca New York bésub 25 sàttumbar 2021. Ca la waxe woon ne dañ leen a wor, wacc leen ci digg yoon wi. Waaye de, wéet du tee gaynde xeex. Bi loolu amee yit, waa kippaangoo Wagner bu Riisii lañ digaaleel ci wàllu kaaraange. Ndege, Mali dafa yokk xar mi karaw. Ab aawo bu mёsta wujje, xamul luy wujje, xalaatu ko te bёggu ko, nga takkal ko wujju wow, noonam la teg si, mu ragalee ko xel. Malee pànk ! Xam naa yaa ngi naan “ñaw !”.

Waaye, ñoom Goytaa ak Songel Mayga yemuñu foofu de. Bi leen ndawal Farãs li bёggee yab, di leen sosal ak jéem a tuutal, dañ ko dàq ca xaj. Waaw kay. Bésub 31 Saŋwiye 2022 lañu génnee ab yégle, siiwal ci dàqug àmbasadёeru tubaab bi, Sowel Méyёer. Ñetti fan kepp lañu ko mayoon cib àpp ngir mu génn Mali. Ngeen foog ne jeex na ? Xanaa dégguleen xeexu njaago ? Loolu la Mali di def nag. Tegleen foofu seen baaraam ba ёllёg, nu wéyal.

Articles les plus lus

capture_decran_2025-08-13_a_00.31.42.png
LA DIPLOMATIE DE RUPTURE DE YASSINE FALL FAIT POLÉMIQUE
La diplomatie sénégalaise traverse une crise inédite depuis l'arrivée du Pastef au pouvoir. ...

48247374-37934474.jpg
PONCTIONS SUR SALAIRES, LE SYTJUST DÉNONCE UNE MÉTHODE INJUSTE ET BRUTALE
Invité de la matinale Salam Sénégal, Maître Aya Boun Malick Diop, secrétaire général du Syndicat ...

opposition-1-750x369.jpeg
GROGGY, L’OPPOSITION TENTE LE REBOND
L’élection présidentielle de mars 2024, remportée par Bassirou Diomaye Faye, a redessiné les cartes ...

capture_decran_2025-08-12_a_15.02.41.png
DU SOUVERAINISME AU KEMALISME
Le Premier ministre Ousmane Sonko continue ses pérégrinations : il joue au globe-trotter. Il découvre ...

matel.jpg
SE MOBILISER POUR ALLÉGER LA CHARGE MENTALE DES FEMMES
S’il est établi que les différences biologiques et physiologiques entre les deux sexes ont induit ...

Vos articles préférés de la semaine

capture_decran_2025-08-05_a_18.10.41.png
PENSER HORS DU SCRIPT COLONIAL
Promesse de redressement et souveraineté économique Le Plan de redressement économique et social, ...

capture_decran_2024-03-19_a_05.29.11.png
LE SÉNÉGAL APPELÉ À RÉPUDIER SA DETTE
Le nouveau gouvernement fait face à un héritage économique explosif. Avec une dette représentant ...

dfddfefefgfgfgfg_0.png
ANATOMIE D’UNE VIOLENCE D’ÉTAT
J’ai pris part à un space sur le réseau social X, bouleversé par le témoignage d’un détenu qui, ...

moustapha-diakhate-fustige-lattitude-du-ministre-des-mines-et-le-directeur-de-lapix.jpg
MOUSTAPHA DIAKHATÉ RENTRE DANS L’ARÈNE
Moustapha Diakhaté, qui est sorti de prison mercredi dernier après avoir purgé sa peine de 15 jours ...

autorites_.jpg
CETTE GANGRÈNE DE L’ADMINISTRATION SÉNÉGALAISE
Alors que les propos du préfet de Kaolack à l’encontre du Maire de la ville de Kaolack, tenus le ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous