Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
27 septembre 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Medias
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

GÀTTALUG XIBAAR YI

ß

Paap Aali Jàllo (www.defuwaxu.com)  |   Publication 21/04/2020

Mbasum Covid-19 bi faat na juróomi way-tawat ci diggante dibéer ak altine

Ci dibéer ji, bi minwi di waaj a jot, la xibaar bi rot : benn aji-tawatu Covid-19 génn na àddina. Ñu ni déet-a-waay, keneen gaañuwaat ci guddig dibéer ji jàpp altine, bi 5i waxtu tegalee 30i simili. Bees sukkandikoo ci yégleb njawriñu wér-gi-yaram gi, ndem-si-Yàlla ji faatu ci dibéer jaa ngi amoon 68i at te dëkkoon Kër-Masaar. Keneen ki, moom, 74i at la amoon. Ca loppitaanu Faan lañ gaañoo. Kon, ñetti way-tawat gaañu nañ ci sababu mbas mi ci ñaari fan yii nu génn, bees ci boolee aji-tawat bi faatoo ca Sigicoor. Bu ko defee, 5idoomi-réew mi ñàkk nañ seen bakkan ci sababu mbas mi, bim dooree ba léegi.

Ay dogal yu bees

Njiitu-réew mi, Maki Sàll, waxoon na ko ciTv5 àjjuma jii weesu : nguur gi sàrtal na takkub mask ci askan wépp ak réew mépp li ko dale altine jii, 20eelu fan ci weeru awril 2020.
Ginnaaw « Institut Pasteur », nguur gi dina ubbi ab bérébu saytukaay ñeel jàngoroy Covid-19 bi ci Géejawaay, Waaxinaan akNimsaat, ñu dippe ko « Centre de tests massifs ». li ko waral nag, mooy yokkute wàllent-ëlëm yi biir Géejawaay ak bãliyë bi.
Jawriñu wér-gi-yaram bi ak ndimbal njaboot, Ablaay Juuf Saar, jël nab dogal ngir xeex yokkute wàllent-ëlëm yi. Léegi, dees na jëfandikoo telefon yi ngir seet wàllent-ëlëm yi (traçage téléphonique). Dalal na xeli nit ñi ci ne, loolu pexe mu baax la. Ndaxte, noonu lañ def ba xam fan la wàllent-ëlëmu Luga biñ wàlle woon Pikin jële jàngoro ji laata muy dellu Luga. Jawriñ bi ne, CDP dina bàyyi xel ñi ciy liggéey ngir aar askan wi ba kenn bañ a lëñbët seen i mbiri bopp.

Takk mask mbaa fey alamaan walla tëddi kaso : tànn ci bu la neex !

Jawriñu kaaraange biir réew mi, ngir jëmmal kàdduy Njiitu-réew mi, génne nab mbindum-dogal (arrêté) ci limu 0091-37 bu 17eelu awril ñeel takkub mask bi. Képp ku sàmmontewulak mbindum-dogal boobu, dees na la jàpp, defeere la, tëj la 1 weer boole ko ak alamaanu 20 000 CFA. Awokaa Me Bàmba Siise moo biral dogal bi.

Force Covid-19

Njiitu-réew mi, Maki Sàll, tabb na Seneraal Farãsuwaa Njaay, teg ko ci njiiteefu kurél Force Covid-19 biñ jagleel xeexub mbas mi. Nee ñu, Seneraal Farãsuwaa Njaay moomu, ku ñàkk caaxaan la te farlu lool ci li muy def. Bu dee kurélug Force Covid-19 bi, nag, pàccu askan bu ci nekk teewal nañ la fa.

Mbas mi laal na doktoor yi

Benn biyólósist bu jigéen moo ame jàngoroy Covid-19 bi ca loppitaanu Matlabul Fawzani. Moom, jëkkëram, ay mbokkam ak ay fajkatlañu gawandoo. Ñi ngi tollu ci 25i nit.
Wàllentuw-ëlëm bu Waaxinaan Nimsaat ba, ca Géejawaay tax na ba ñu tëj kilinigu. Moo waral itam ñu lël 18i fajkat ya fay liggéey yépp.
Ci Ndakaaru, Wàllentuw-ëlëm bu Cité Soprim wàll na jàngoro ji ay fajkati Centre Mamadou Diop bu Liberté 6 Extension.

Taalibe yi jël nañ seen wàll ci mbas mi

Li ñépp doon ragal mujje na am. Ndeysaan, mbas mi song na goney taalibe yiy yelwaan ci mbedd mi. 3 taalibe la jàngoroy Covid-19 bi daaneel ca Sigicoor.

Mbas mi dugg na Mbàkke

Gox bi dend ak Tuubaa, Mbàkke, am na 2 Wàllenti-ëlëm. Nee ñu, ñoom ñaar ñépp ca màrse Okaas lañ doon liggéeye te yéeg nañ ba tàyyi ci oto yiy lëkkale Tuubaa ak Mbàkke.Jamono jii, njàqare ju réy la fa mbir mi jur.

Benkeñenke yi wàllentuw-ëlëmu Géejawaay bu mujj bi sabab

Ab soxna la. Ndege, Kër Masaar la jóge ba muy seetluji boppam ca kilinigu Duudu bu Géejawaay Nimsaat. Ginnaaw Waxinaan Nimsaat, jot naa jaar ci bérébi mbooloo yu bare, rawatina Màrse-Jën bu Pikin bi nga xam ne, lu tollu ci 2 000 nit ñoo fay daje bés bu nekk. Yemul foofu ndax dem na ci yeneen màrse biir Géejawaay. Te, saa su nekk, ndaw si oto yi walla biis yiy yeb mbooloo lay jël.  Loolu nag, indil nay jafe-jafe ak i benkeñenke yu tar ñi nga xam ne ñoo war a xool, xayma ñi mu war a wàll.
Perefe Géejawaay bi, Muhammadu Bolondeŋ Njaay ak Meer bi, Raasiin Taalaa, jël nañ dogal, lël 18i fajkati  kilinig Duudu ba mu demoon ak seen i  dëkkandoo.

Ñaari yégley jawriñu koom-koom bi

Bi ci jiitu mi ngi aju ci li nguur gi dugal 200 milyaar ci sunu xaalis ci bànk yi ngir sàmm peyoori liggéeykat yi. Jawriñ ji nee na, na àntarpiriis yi am ay jafe-jafe ngir fay seeniliggéeykat dem ci bànk yi. Jawriñ ji Hott ne, ci Iradio ak ITv : « dinan leen yombalal mbir mi ci ni mu gën a gaawe. »
Ñaareel bi, moom, liggéeykati nguur gi la ñeel. Jawriñu koom-koom gi ne, liggéeykati nguur gi bokkuñu ci aj biñ aj peyum bor ñeel liggéékat yi ameel bànk yi. Ndaxte, ñoom, ñoo ngi wéy di jot seen i peyoor weer wu dee.

Coowal ceeb bi

Mañsuur Fay tontu na Gii Maryiis Saaña. Ndege, Gii Maryiis Saaña ak waa Frapp–France dégage dañu koo kalaameji ca jawriñ ji ca OFNAC. Bi ko taskati xibaar yi laajee, Mañsuur Fay dafa ne : «  Gaa ñooñu, bu leen neexee àkki bérébu àttekaay bu leen neex. Waaye, nun ñepp noo war a jàpp ci liggéey bi ngir matale jubluwaayu Njiitu-réew mi Maki Sàll : séddale dund gépp ñi ko yeyoo kese, ci diirub 10i fan, lu mu yàgg yàgg. »

Articles les plus lus

ammbow.jpg
AMADOU MAHTAR MBOW, L’HÉRITAGE D’UN SIÈCLE DE COMBATS
C’est l’un des sages du continent. Ce mercredi marque le premier anniversaire du rappel à Dieu d'Amadou ...

mgueye_lq.jpg
LE PRES ET SES MILLIARDS DE FUMÉE
Le financement du Plan de redressement économique et social (Pres) fera-t-il revivre les anciennes filières ...

garage_latdior.jpg
OPERATION COUP DE POING AU GARAGE LAT DIOR
Dans la nuit de lundi à mardi, le garage Lat Dior, situé derrière le tribunal de grande instance de ...

capture_decran_2025-09-09_a_19.43.16.png
LA PAUVRETÉ, UN CRIME ?
Sous l’affichage tapageur d’un État de droit protecteur, le Sénégal s’éloigne silencieusement ...

whatsapp-image-2025-09-23-at-15.51.04.jpeg
LES FÉMINISTES APPELLENT À DES ACTES APRÈS LE DISCOURS DE DIOMAYE À L’ONU
Le lundi 22 septembre 2025, à la tribune des Nations Unies, le président de la République du Sénégal, ...

Vos articles préférés de la semaine

capture_decran_2025-09-19_a_15.17.55.png
SORTIR DE LA FASCINATION DU MARABOUTAGE
Inaf, inaf, inaf ! Nos écrans sont devenus des miroirs puissants de notre société. À travers les ...

scr-20250918-qocm.jpeg
JOURNÉE À MILAN
Rien à dire, Ousmane Sonko est bien un phénomène. Réussir une mobilisation monstre en terre lointaine ...

capture_decran_2025-09-12_a_12.48.41.png
REDUIRE LA PROFESSION VETERINAIRE A LA PRATIQUE DE LA SANTE ANIMALE NE PEUT PROSPERER EN AFRIQUE SUBSAHARIENNE
Ex-directeur de l’École Inter-États des Sciences et Médecine Vétérinaire (EISMV) de Dakar et ancien ...

1280.jpeg
QUI POUR ARRÊTER LE CARNAGE DE L’ÉTAT SIONISTE ?
Le génocide se poursuit dans la bande Gaza. Chaque jour, des dizaines de vies sont impitoyablement ...

capture_decran_2025-09-20_a_17.17.44.png
SCHALKE, FIERTÉ D'UN PEUPLE OUVRIER
« Schalke, c’est le charbon, la sueur et la fierté d’un peuple. » À Gelsenkirchen, dans le ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous