JOOYLOO NGA SA MAG
Baabakar Lóo, ndongo-daara la ca Pari, di fa jàng matematig. Woyam wu daw-yaram wii, Jaari Sow la ciy waxal, naan ko gaawal delsi Jaari, loolu rekk a mën a dakkal sama tiis ak sama njàqare.

Baabakar Lóo, ndongo-daara la ca Pari, di fa jàng matematig. Woyam wu daw-yaram wii, Jaari Sow la ciy waxal, naan ko gaawal delsi Jaari, loolu rekk a mën a dakkal sama tiis ak sama njàqare.
*
Wër naa la fu ne gisuma la
Bu dee yaa ngi may wuyu itam dégguma la
Seet naa ci biir seet ci biti
Waaye lu lay màndargaal sax nekku fi
Fan la la jant biy tiim ?
Dañu laa làq am dangaa réer ?
Waxal ak man rakk sama
Fu mu doon ma jëlsi la fa
Yaay-bóoy lekkatul
Sa xarit benn bakkan nelawatul
Sa mag liggéeyatul
Ndax xel moo dalatul
Fan la la jant biy tiim ?
Dañu laa làq am dangaa réer ?
Waxal ak man rakk sama
Fu mu doon ma jëlsi la fa
Réew mépp a am mbetteel
Ñu baax ñépp a jaaxle
Ndax yaw mi ñu xamul foo ne
Ba tax ñu tàmbali di la wër ca teel
Fan la la jant biy tiim ?
Dañu laa làq am dangaa réer ?
Waxal ak man rakk sama
Fu mu doon ma jëlsi la fa
Samam xel mi ngi xalaat lu ne
Samag kàttan mayu ma ma xam ci loo ne
Waaye samay ñaan dinañu la fekk fépp foo ne
Samaw làmmiñ di wax Buur bi aar la ni muy aare gone.
BAABAKAR LÓO