Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
29 août 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Opinions
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

ÑAN-MBAALO, TOJ NGA LÀMB JI !

« Toj naa fii ! », « Tasaare naa fee ! », « Rajaxe naa fale ! »…

USÉNU BÉEY (Medium.com)  |   Publication 23/02/2019

Su nu waxantee dëgg, xorom si moom la ! Moom Madike Ñaŋ, kenn ci wutaakoni yi, mooy xorom siy safal kampaañ bi ñuy waaj a jéexal.

Ci biir werante yeek, xuloo yeek, ŋàññante yeek, tamante dëmm yi, Madike moom, neex deret ba dee, ciy ree ak i kókkali, boole ciy kàddu yu rafet, lanuy jaaye sàrtu doxalinam bi mu faf tudde « Jàmm ak xéewal ».

Dal ak aafiya daal la indi ci kampaañ bi nga xam ne, boobaak léegi, ni nu ko waxe ci njélbéen gi, defante doŋŋ lees ci seetlu, defante bay dóorantey kurpeñ, di génney jaasi… Nii lañ fi woññee — walla woññeegum ? — ñaar ba ñetti doomi-Aadama yu seen bakkan rot.

Madike moom, ci jamono yii, mu ngiy toj Anternet. Mook Usmaan Sonkoo ko koy xëccoo, sax. Sonko daa aakimu, daanaka, reeso sosiyoo yi, bàyyi wujjam yépp ginnaaw ci wàll woowu. Waaye Madike Ñaŋ sorewu ko lool ndax saa yoo duggee Anternet daj ciy nataalam mbaa dégg i kàddoom. Ne ñi mën a muñ i feemam barewuñu. Moom daal day reeloo nit ñi ba seen biir di metti ! Wax ji benn la : ‘’kii daal moo neex !’’…

Waaye li am ba am, moo di ne, wutaakon bile, mu tey ko mbaa mu bañ koo tey, fexe na ba nit ñi génne seen xel liñ yàgg a ruumandaat : ndax, moom, jot ci réew mee ko tax a jóg walla dafa bëgg a sotle Maki Sàll ba noppiy dof-doflu, di reeloo askan wi ? Madike Ñaŋ, ndax yàqal Ablaay Wàdd ak Karim ak seen pàrti, PDS a ko tax a sàmp ndëndam ? Lu waral layookat bu siiw ni moom, amoon lool bayre, doon ku am fulla, xéy di wër réew miy wax ay waxi ku daanoo ci saret ? Xanaa kay li ko jaral a sóoru Wàdd du neen ! Ndax kat, ‘’Góor-gi’’ léppam la woon, ni sët la ko mas a jàppe, jàngal ko politig, doon njiitam.

Nu seetaanati ba xam « fu boroom wànnent di mujje ak i gëtam »

Articles les plus lus

capture_decran_2024-07-18_a_23.21.06_0.png
AMADOU DIAW FAIT DE LA PHOTOGRAPHIE LE CŒUR BATTANT DE SAINT-LOUIS
(SenePlus) - Dans un entretien accordé à DakArtNews le 22 août 2025, Amadou Diaw, fondateur du ...

capture_decran_2025-08-27_a_01.08.32.png
ABASS FALL, POLITIQUE PAR ACCIDENT
De la prison du Cap Manuel à l’hôtel de ville de Dakar, Abass Fall, 58 ans, a traversé les épreuves ...

yande_diop.jpg
DANS LA LUMIERE ET L’OMBRE D’ALIOUNE DIOP
Dans le 5ᵉ arrondissement de Paris, au cœur de la rue des Écoles, une vitrine se distingue depuis ...

capture_decran_2025-08-26_a_14.31.09.png
ABASS FALL, DEUX ANS POUR CONVAINCRE
C’est l’objectif d’une vie qui vient de se réaliser pour le ministre du Travail. Il va inscrire ...

projet_avenir.jpg
LE PROJET AVENIR REDONNE ESPOIR AUX FEMMES ET AUX JEUNES
Dans une dynamique d’appui au développement local durable, le projet Adaptation et Valorisation Entrepreneuriale ...

Vos articles préférés de la semaine

c25d38f5-e2e1-4503-aad4-87cc038d7420.jpeg
QUAND LA MONNAIE DEVIENT UNE AFFAIRE DE LIBERTÉ
Pourquoi continue-t-on à penser que la monnaie n'est qu'une affaire de comptables, d'économistes et ...

img_2412.jpg
LE PACTE POUR LA TRANSFORMATION PROMISE
Cent-une voix, cent-une signatures, cent-une consciences alertées, réunies dans un "Appel des 101" ...

capture-decran-2025-08-15-a-17.21.57-800x445.png
LE DERNIER SOUFFLE D’UN MAÎTRE, LA PREMIÈRE LUEUR D’UN CHEMIN
Il y a des rencontres qui, par leur intensité et leur profondeur, changent à jamais le cours de ton ...

capture_decran_2025-08-18_a_23.57.59.png
LA MAGISTRATURE NE DOIT PAS PÉRIR
La plus grande crainte des adeptes de l'État de droit depuis l'accession du Pastef au pouvoir est l'effondrement ...

saima_sayed.jpg
LE PAKISTAN RICE ROAD SHOW ATTENDU A DAKAR LES 1ER ET 2 SEPTEMBRE
L'Ambassade du Pakistan à Dakar a annoncé que le «Pakistan Rice Road Show» s’arrêtera à Dakar, ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous