Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
16 août 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Opinions
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
Par Abdou SENE

SENEGAL YEEWU NA

Yeewu ngeen, yeewu naa, du ñu falati ku matul njiitu réew

Abdou SENE  |   Publication 26/02/2024

Sama réew du falati ku koy jaay

Sénégal du falati ku koy jooy lo

Sama réew du falati kuy wure

Sénégal du falati ku koy wor

Sama réew du falati ku koy asaalóo

Sénégal du falati ku koy aakimoo 

Sama gaa ñi, jógleen ! Jóg naa. Yeewuleen ! Yeewu naa

Jógleen ! Jóg naa. Amoon na fi, gan guy yewwi béy

Jógleen ! Jóg naa. Gan gi fi jaaroon yee na ñu

Sama réew du falati ku dul sant

Sénégal du falati ku dul suur

Sama réew du falati ku koy fetal

Sénégal du falati ku koy fen

Sama réew du falati ku koy xas

Sénégal du falati ku dëkke xiiroo

Sama gaa ñi, jógleen ! Jóg naa. Yeewuleen ! Yeewu naa

Jógleen ! Jóg naa. Amoon na fi, gan guy yewwi béy

Jógleen ! Jóg naa. Gan gi fi jaaroon, yee na ñu

Sama réew du falati ku koy sànk

Sénégal du falati ku koy sàcc

Sama réew du falati ku ko dëkkee gaaze

Sénégal du falati ku koy gaañ

Sama réew du falati ku koy merloo

Sénégal du falati ku koy mettital

Sama gaa ñi jógleen ! Jóg naa. Yeewuleen ! Yeewu naa

Jógleen ! Jóg naa. Amoon na fi, gan guy yewwi béy

Jógleen ! Jóg naa. Gan gi fi jaaroon, yee na ñu

Sama réew du falati ku koy noot

Sénégal du falati ku koy nàccal

Sama réew du falati ku koy mere

Sénégal du falati ku koy màtt

Sama réew du falati ku ko dul jaamu

Sénégal du falati ku wutul jàmm

Sama gaa ñi jógleen ! Jóg naa. Yeewuleen ! Yeewu naa

Jógleen ! Jóg naa. Amoon na fi, gan guy yewwi béy,

Jógleen ! Jóg naa. Gan gi fi jaaroon, yee na ñu

Sama réew du falati ku dëkke njuuj

Sénégal du falati ku dëkke njaaj

Sama réew du falati ku dëkke waxantu

Sénégal du falati ku dëkke weddi

Sama rééw du falati kuy ŋarale

Sénégal du falati ku dëkke ŋaayoo

Sama gaa ñi jógleen ! Jóg naa. Yeewuleen ! Yeewu naa

Jógleen ! Jóg naa. Amoon na fi, gan guy yewwi béy,

Jógleen ! Jóg naa. Gan gi fi jaaroon, yee na ñu

Sama réew du falati sàmbaabóoy

Sénégal du falati suraabaali

Sama réew du falati ci ñiy yee fitna

Sénégal du falati ci ñi yées

Sama réew du falati ku matul kilifa

Sénégal du falati ku matul xalifa

Déedéet sama waay, bul sori ! Baayil ma tënkal la ko :

Yeewu ngeen, yeewu naa, du ñu falati kuy féewale ay waaso

Yeewu ngeen, yeewu naa, du ñu falati baadoolo bu dul suur

Yeewu ngeen, yeewu naa, du ñu falati ku matul njiitu réew

Articles les plus lus

capture_decran_2025-08-13_a_00.31.42.png
LA DIPLOMATIE DE RUPTURE DE YASSINE FALL FAIT POLÉMIQUE
La diplomatie sénégalaise traverse une crise inédite depuis l'arrivée du Pastef au pouvoir. ...

48247374-37934474.jpg
PONCTIONS SUR SALAIRES, LE SYTJUST DÉNONCE UNE MÉTHODE INJUSTE ET BRUTALE
Invité de la matinale Salam Sénégal, Maître Aya Boun Malick Diop, secrétaire général du Syndicat ...

opposition-1-750x369.jpeg
GROGGY, L’OPPOSITION TENTE LE REBOND
L’élection présidentielle de mars 2024, remportée par Bassirou Diomaye Faye, a redessiné les cartes ...

capture_decran_2025-08-12_a_15.02.41.png
DU SOUVERAINISME AU KEMALISME
Le Premier ministre Ousmane Sonko continue ses pérégrinations : il joue au globe-trotter. Il découvre ...

matel.jpg
SE MOBILISER POUR ALLÉGER LA CHARGE MENTALE DES FEMMES
S’il est établi que les différences biologiques et physiologiques entre les deux sexes ont induit ...

Vos articles préférés de la semaine

capture_decran_2025-08-05_a_18.10.41.png
PENSER HORS DU SCRIPT COLONIAL
Promesse de redressement et souveraineté économique Le Plan de redressement économique et social, ...

capture_decran_2024-03-19_a_05.29.11.png
LE SÉNÉGAL APPELÉ À RÉPUDIER SA DETTE
Le nouveau gouvernement fait face à un héritage économique explosif. Avec une dette représentant ...

dfddfefefgfgfgfg_0.png
ANATOMIE D’UNE VIOLENCE D’ÉTAT
J’ai pris part à un space sur le réseau social X, bouleversé par le témoignage d’un détenu qui, ...

moustapha-diakhate-fustige-lattitude-du-ministre-des-mines-et-le-directeur-de-lapix.jpg
MOUSTAPHA DIAKHATÉ RENTRE DANS L’ARÈNE
Moustapha Diakhaté, qui est sorti de prison mercredi dernier après avoir purgé sa peine de 15 jours ...

autorites_.jpg
CETTE GANGRÈNE DE L’ADMINISTRATION SÉNÉGALAISE
Alors que les propos du préfet de Kaolack à l’encontre du Maire de la ville de Kaolack, tenus le ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous