PAR SÉEX AXMADU BÀMBA NJAAY
WËRI JAARI
Jàngkati defuwaxu yi war nañoo miin léegi xalimag Séex Axmadu Bàmba Njaay mi bind woy wii. Moom nag, nee na xamul naka la Jaari Sow mënee xéy ni mes, mu sol i dàllam ne da koy seeti…

*
Bëtt leen jéeri ji
Jéril ma géej gi
Fu Jaari jaar
Na ngeen ma ko jëlil
Na takk jaaroom
Ànd ak sagoom
Bu ko dara gor
Ndeyjoor càmmooñ
Wiri-wiri
Wëri Jaari
Yal na Jaari
Mi nu wëri
Feeñ ci jàmm.