Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
29 septembre 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Santé
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

KORONAAWIRIS : MBETE GAYNDE GU TËX !

Fii ci Senegaal, limu ñi Covid-19 bi daaneel romb na téeméer.

Ndey Koddu Faal (www.defuwaxu.com)  |   Publication 04/04/2020

Fii ci Senegaal, limu ñi Covid-19 bi daaneel romb na téeméer.

Moonte bi feebar biy soog a feeñ ca réewum Siin, ñetti weer ci ginnaaw – mi ngi mel ni démb ci man – dañoo foogoon ni fa lay yem, du dal ku dul Sinwaa. Njuumte la woon, ndax mujj gi laal na Ërob. Ñu ni kon xéy-na feebaru nit ku weex la. Am na sax ñu dem ba naan doomu-jàngoro bi ñemewul tàngoor, mënul a dund Afrig, moo tax nit ku ñuul du ko am.

Ndekete yóo…

Léegi leer na ñépp ne koronaa xàmmeewul ku ñuul ak ku weex, yoonam newul ci ku puur ni Sàppone bi walla Sinwaa bi te boroom daraja beek baadoolo bi la yemale kepp. Faat na Mari-Roos Kompawore ak Manu Dibango, song Mustafaa Màmba Giraasi jóge fa dal ci Boris Johnson ak Prince Charles. Suñ bëggoon a lim kilifa yi muy lottal yépp fan yii, dun fi jóge tey. Xanaa rekk di ñaan ñépp ñu bàyyi xel ci fajkat yi mu sonal lool. Koronaa, kenn mënu koo teg bët ba naan yaa ngi koy jàpp. Koronaa dëj na nit ñi seen kër, tax na ñu tëj jàkka yi, jumaa yi, jàngu yi ak tamit isin yeek biro yeek daara yi.

Te yemul foofu.

Su ma ko mën a waxe noonu xew ci boppam… xewwi na !

Koronaa nee na bëggatul gis kenn muy dox ay tànki mbokk te kat, moom, buy doxantu ba séen ñaar ñuy joxante loxo bu ne leen bum fi amati mbaa ma def leen lu ñaaw léegi ! Te nag, àddina-si-juróom-ñaar amul réew mu mucc ci ndigalam yu kéemaane yi.

Waaw, xanaa koronaawiris moom gaynde gu tëx la ?

Lu ma ciy gën a xalaat, di gën a waaru. Ci dëgg-dëgg, xawma lu ma yëf yiy niru. Waaye mësumaa fàtte ni dee du moy du jaas, xam koo tax nit di ji muy sax ak a meññ, di móol, di fent i taalif ngir tabax ëllëg.

Tey jii nag, koronaa tax na ëllëg gën a lëndëm, dee gën noo jege. Maa ngiy déggaat kàddu Ngiraan Fay yi ci ndoorteelu Doomi Golo :« Àddina : dund, dee. Leneen newu fi, Badu. Lii rekk : demal, maa ngi ñëw.» Waaye kan moo bëggul a dund ? Ma ne kon koronaa dafa wàcc di nu mbëllee : di nu fàttali ni lu tuuti- gallaxtaan lanu te amunu benn ka1ttan. Bi nuy ganesi àddina indiwaalewunu tus, te bu nuy dem it dunu yóbbuwaale tus. Lii di biral ne dara jaru fi fëgg dënn ak jaay lu amul.

Nan seetaat boog sunu bopp te dellu ci Yàlla.

Articles les plus lus

mackyligassama.jpg
MAKHILY GASSAMA OU UNE VOIX MAJEURE DE LA LITTÉRATURE AFRICAINE
Notre patrimoine littéraire est un espace dense de créativité et de beauté. La littérature est un ...

jean-baptiste-placca_0_2.jpeg
LÀ OÙ LES POLITIQUES AFFAMENT LA PRESSE, LA DÉMOCRATIE N'A AUCUN AVENIR
(SenePlus) - Dans un éditorial publié le 13 septembre 2025 sur RFI, Jean-Baptiste Placca dresse un ...

capture_decran_2025-09-28_a_16.29.53.png
MACKY SALL DÉVOILE LES TRAHISONS QUI ONT FORGÉ SON DESTIN
Dans un entretien exclusif accordé au podcast H5 Motivation d'Aziz H. Rok, l'ancien président Macky ...

130404850_678305526169140_73864340909318201_n.jpg
OUMAR SARR APPELLE AU PRAGMATISME ET À UN DIALOGUE CONSTRUCTIF AVEC LE FMI
S’exprimant sur l’annonce de la « dette cachée » par le gouvernement, Oumar Sarr a fait part de ...

capture_decran_2025-09-27_a_13.14.19.png
IL N’Y AURA PAS DE BILLETS PHYSIQUES POUR SÉNÉGAL-MAURITANIE, ANNONCE ABDOULAYE FALL
Le président de la Fédération sénégalaise de football (FSF), Abdoulaye Fall, annonce des changements ...

Vos articles préférés de la semaine

capture_decran_2025-09-19_a_15.17.55.png
SORTIR DE LA FASCINATION DU MARABOUTAGE
Inaf, inaf, inaf ! Nos écrans sont devenus des miroirs puissants de notre société. À travers les ...

fotojet.jpg
QUAND LA FRANÇAFRIQUE SE RETOURNE CONTRE SES HÉRITIERS
(SenePlus) - La double nationalité, autrefois perçue comme un atout, devient un obstacle majeur pour ...

capture_decran_2025-09-20_a_17.17.44.png
SCHALKE, FIERTÉ D'UN PEUPLE OUVRIER
« Schalke, c’est le charbon, la sueur et la fierté d’un peuple. » À Gelsenkirchen, dans le ...

fadeld.jpg
L’ÉTAT ET LES CHEFS RELIGIEUX, SUR UNE PISTE GLISSANTE
L’étranger qui n’aurait d’autres informations sur les préparatifs et le déroulement des deux ...

capture_decran_2025-09-22_a_21.09.15.png
L'EXIL DES INVISIBLES
Capitale sénégalaise et carrefour de multiples destins, Dakar voit affluer chaque jour des femmes ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous