Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
1 juillet 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Societe
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

ABDULAAY BAARA JÓOB, GUY GA LIIS NA…

Ci altine 4eelu fan ci weeru saŋwiyee 2021 la Abdulaay Baara Jóob, nekkoon saa-mboolaay (sociologue)

www.defuwaxu.com  |   Ndey Koddu Faal   |   Publication 20/01/2021

Ci altine 4eelu fan ci weeru saŋwiyee 2021 la Abdulaay Baara Jóob, nekkoon saa-mboolaay (sociologue) bu ñépp xam, génn àddina fii ci Ndakaaru. Mu ngi amoon 91i at. Ca ëllëg sa, talaata, lim bu takkoo-takku moo ko jullee jàkkay « Point E » ba noppi gunge ko këram gu mujj, ca sëgu Yoof ya.

Abdulaay Baara Jóob bokk na ci ñi sos wàlluw xam-xamu mboolaay bu Iniwérsite Séex Anta Jóob, dundal ko, dooleel ko. Jàngale na fa ay at, tàggat fa ñu bari. Ngir firndeel ko, Abdu Salaam Faal mi ngi xamle ca rob ba ni Abdulaay Baara moo ko jàngal, xallal ko yoon, gunge ko, te bari na ciy moroom. Abdu Salaam Faal yokk ci ni ndem-si-Yàlla ji « dafa feesoon dell ak xam-xam te doonooon it ku teey. Téere yim fi bàyyi kenn du leen fàtte fii ak i xarnu, dees na wéy di leen jariñoo ndax dañoo am solo dëggantaan ». Soxna Penda Mbow di saa-mboor bu mag feelu ko ne mi ngi « sargal jëmm ju màggoon, koo xam ni li mu bind ci mboorum Wolof yi kenn du ko natable, dara du ko dindi ndax xam-xam bu wóor la ».
Abdulaay Baara Jóob doomu-Ndar la woon, doore fa njàngam, bi mu amee 18i at mu dem « Ecole William Ponty » bu Sebikotaan. Def na fa juróomi at laata muy dugg Iniwérsite Dakaar. Waaye benn at doŋŋ la fa toog daldi dem Iniwérsite bu Toulouse (Farãs) ci atum 1954. Daanaka Tugal la ame lijaasaam yépp.

Bi mu ñibbisee la dugg IFAN di fa liggéeye ci atum 1958, jamono ja ko Théodore Monod doon jiite. Jóob ku farlu la woon ; li koy firndeel mooy ni mu gaawee sottal « teesam », layal ko, am ci ndam lu réy. Kon mel na ni dafa jaaroon ci tànki waajuram bu góor bi nga xam ni jàngalekat la woon, fonk lool njàng, xam njariñ li.

Abdulaay Baara Jóob moo bind : La société wolof, les systèmes d’inégalité et de domination, Paris, Karthala, 1981 ak tamit La famille wolof, Tradition et changement, Paris, Karthala, 1985. Ci gàttal, ay téereem njàngat lañu ci dundin ak nekkinu Wolof yi. Porfesoor Jóob mi ngi ciy faramfàcce lépp lu ñeel waaso Wolof yi maanaam ni ñuy téyee seen réew, li fi ku nekk tekki moo xam buur la, walla gor, walla géer, walla géwal añs., yaatal gëstoom ci doole tarixa yi fii ci Senegaal. Téereem yooyu di yóbbal yu am solo ci képp ku tegu ci yoonu xam Wolof yi : li ko dale ci can, takk, séy, kujje ba ci fase, lépp a ngi ci biir.

Abdulaay Baara Jóob nag bokkul woon ci gëstukat yooyuy tëju seen biro di bind lu leen neex ndax moom da daan soli dàllam dem ci dëkki cosaan yi, waxtaan ak ña fa fekk baax, laaj leen lépp lu mu leen war a laaj, bu yëf yi leeree ci boppam mu soog a bind téereem, móol-lu ko.

Ñu bari it seedeel nañ ko yiw ak jaambure. Mamadu Njaay mu OSAD, moom, dina namm waxtaan yu xóot ya mu daan séq léeg-léeg ak aji-dem ji mu jàppe nit ku jullite te am sutura. Baabakar Jóob Buuba ci wàllu boppam di moom tamit saa- mboor wax na ne « Porfesoor Jóob wàcc na ndax def na warugaram ci fullaak xereñte».

Lii lépp a taxoon ñaari at ci ginnaaw (2018) « Ministère de la culture » bëggoon koo sargal ci kanamu askan wi yépp ca « Salon du livre » bu Ndar waaye yaram wu sutante mayu ko woon mu dem teewe ko. Wànte ginnaaw mag mooy garab gu sax, di maye keppaar, waa « Direction du livre et de la lecture » sol seen dàll fekki Abdulaay Baara këram ca Zone B, waxtaan ak moom tuuti ci ay jaar-jaaram, sargal ko, tappal ko raaya. Du woon guléet mu am ay raaya fii ci Senegaal walla feneen. Mënees na cee lim ñaar yii rekk : « Officier de l’Ordre du Mérite » bu Senegaal ak « Chevalier des Palmes académiques » Farãs. Kon leer na ni Senegaal xamoon na kan mooy Abdulaay Baara Jóob. Teewul nag muy réew muy xaw a sàggane yenn doomam yi gën a ràññeeku. Looloo taxoon sax ci 30eelu génnug àddina Séex Anta Jóob, Abdulaay Baara Jóob yëkkati woon kàddoom ni : « Soo amee ci sa dëkk ay jaambaari fàkk-tëdd, danga leen a war a sargal ndax loolu dina yokk seen cawarte te aw sas lay doon ci ñoom ngir ñuy làbbali seen fas. Moo gën di xaar ku jóge feneen di la ko defal ». Te muy dëgg gu wér péŋŋ. Dëggu googu nekkoon ci ndem-si-Yàlla-ji moo waraloon ci atum 2008 kujje pólitig gi ak kuréli mbootaay yiy sàmm àq ak yelleefi doomi-aadama yi wóolu ko, teg ko ci boppu « Commission scientifique des Assises nationales ». Nekkoon na liggéey bu am-a-am solo waaye ba sun-jonn-Yàlla- tey-jii la ca ruuse ngi nelaw ci « tiroirs » yi. Moonte « lël » booboo fi meññloo woon yaakaar. Kenn fàttewul ni bi Maki Sàll di laaj réew mi dafa dige woon ni bés bu faloo dina téye Senegaal ni ko « Assises » yi bëgge. Ndax jaaduwul tey jii ñu xamal askan wi fu wànnent mujjee kiy gëtam ?

Bu loolu weesoo, nuy fàttali ni Abdulaay Baara mii nuy waxtaane tey moo doon boroom-këru soxna Aram Faal Jóob mi ñuy dàkkantale sunu Séex Anta Jóob mu jigéen ndax liggéeyam ak cofeelam ci Senegaal ak lépp lu koy jëmale kanam. Lu Defu Waxu di ko ko jaale mook njabootam. Yal na ko Yàlla yërëm te jéggal ko.

Articles les plus lus

capture_decran_2025-06-24_a_23.42.22.png
UN COMITÉ QUI OUBLIE CEUX QUI LISENT ET FONT LIRE
Le vendredi 20 juin 2025, à la Maison de la culture Douta Seck, s’est tenue une cérémonie solennelle. ...

adama-dieng.jpeg
L'IMPLOSION DU SOUDAN DOIT ÊTRE STOPPEE À EL-FASHER
Il y a quelques jours, la Commission africaine des droits de l'homme et des peuples (CADHP) et la Mission ...

mbane_.jpg
LE SUCRE DE LA CSS NE DOIT PAS GHETTOÏSER MBANE
C’est Le Quotidien, dans sa Une du jeudi 19 juin 2025, qui donne les détails de l’affaire : la Compagnie ...

mgueye_.jpg
DU QUATRIÈME SOUS-SOL AUX JETS PRIVÉS ET LIMOUSINES
Heureux comme notre Premier ministre, qui a l’occasion de voyager à travers l’Afrique et le monde, ...

andama.jpg
RENCONTRE AVEC UN PERSONNAGE A LA FOIS CELEBRE ET MYSTERIEUX
Son nom est intimement lié à Diofior, un village sérère connu pour être un bastion de la lutte traditionnelle ...

Vos articles préférés de la semaine

capture_decran_2022-01-09_a_21.42.15_0.png
LE SÉNÉGAL VA MAL
Entre morosité et rhétorique politicienne Le contexte actuel du Sénégal prouve, au-delà des promesses ...

capture_decran_2025-06-18_a_09.08.32.png
IL FAUT AIDER LE SOLDAT BASSIROU KÉBÉ, DG DE LA SNHM
Les Américains disent que toute politique est locale. Le citoyen juge l’Etat sur la base de ses actions ...

capture_decran_2025-06-15_a_13.56.37.png
LE FOOTBALL M’A DONNÉ DES FRÈRES ET DES SOEURS AUX QUATRE COINS DU MONDE
Du coiffeur de Salah au professeur d’anglais , de Luis Díaz, des tribunes de Munich aux rues de Paris, ...

capture_decran_2025-06-23_a_16.58.31.png
DIOMAYE BATTU À LA PRÉSIDENCE DE LA CEDEAO PAR MAADA BIO
Amadou Hott avait le meilleur profil pour présider la Bad, et il a échoué. Hier également, la candidature ...

57540596-42611988.jpg
GUY MARIUS SAGNA, LE COL BLEU DE L’HÉMICYCLE
Il détonne dans l’Assemblée nationale. Sa voix, son langage, sa trajectoire. Il est l’un des rares ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous