Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
26 septembre 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Societe
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

GÀTTALUG XIBAAR YI

Njiitu réew mi, Maki Sàll, amal nab bàttale ci altine ji weesu, 29eelu fan ci sulet, 2020.

Defu Waxu  |   Ami Mbeng  |   Publication 09/07/2020

6i DOGAL YI MAKI SÀLL MUJJEE JËL ÑEEL MBAS MI

Njiitu réew mi, Maki Sàll, amal nab bàttale ci altine ji weesu, 29eelu fan ci sulet, 2020. 6i dogal yii ñoo gën a fës ci kàddoom yi :

1. Maki Sàll dakkal na guural gi ak déju bim làmboo li ko dale ci talaata ji, 30eelufan ci sulet, 2020, bi 23i waxtu ci guddi jotee.

2. Waxtuy liggéey yi ñu toxaloon ñeel caytu gi, 9i waxtu ci suba jàpp 16i waxtu ci ngoon, soppees na leen. Léegi, waxtu ya liggéeykat yi daan xéy, di ko wàcc lees delloosi ; maanaam, 8i waxtu ci suba jàpp 17i waxtu ci ngoon, ànd ak diirub dal-lu bi nekkoon diggante 13 waxtu ak 30i simili jàpp 14i waxtu ak 30i simili.

3. Sàrt biñ jagleeloon màrse yi, di leen tëj 1 fan ci ayu-bés gi ngir ñu raxas leen, day wéy di am.

4. Terees na, ba tey, mépp mbooloo di daje ci béréb yi ñuy amale xew-xewi jamono yeek yenn xeeti po yi. Li ñu ko dugge moo di bañ mbas mi gën a law.

5. Dees na ubbi ayeropoor yi li ko dale bésub 15eel ci sulet. Waaye, dees na ga roppëlaan yi sàmmonte ak digley doktoor yi ci xeexub mbas mi.

6. Digi suuf yeek yu géej yi, ñoom, tëjees na leen ba jëmmi jamono.

Mbasum Covid-19 ñeel Senegaal : Waalo day gën di aay

LIMUB TAWATI COVID-19 BI

Lim bi dafa gën a yokku ci biir weeru sulet bii nu génn. Bees ko méngalee ak yeneen weer yi, 38i way-tawat yokk nañu ci téeméer yoo jël.

Naam, ci biir 100i way-tawat yoo jël, 60i yi dañuy wér. Waaye, loolu tekkiwul ne mbas maa ngiy wàññeeku. Ndege, limu way-tawat yi nekk ci diggante dund ak dee yokku na ba toll ci 295 te 121 yi gaañu nañ.

Dr Béey, njiitalu ‘’Samu national’’, aartu na nit ñi ci dayob wàllent bi nga xam ne, xayma na ko ci 41 ñeel 100 yoo jàpp. Mu teg ci ne, li sabab dee gu bare gi mooy ne, ñi ëpp  ci way-tawat yi lott yi, dañu ame ay feebar yu bon yu deme ni jabetub ñaareel bi, tãsiyoŋ buy yéeg ak ndigg lu jagadi.

PEEÑANTALI COVID-19 BI

 Pr Séydi dolli na ci bakkan bu mënatul a xeeñtu ak lewetug gémmiñ

Ca ndoorteelu mbas mi, doktoor yi sëqët su wow, yaram wu tàng, put guy metti, añs. lañ biraloon ne ñooy peeñantal yi gën a fës ñeel jàngoroy Covid-19 ji. Tey, mel na ni daa am yu ci dolleeku. Ci tënk bi muy faral di amal weer wu nekk te mu amaloon ko ci alxames jii weesu, Pr Séydi biral na 2i peeñantal yu bees : bakkan bu dul yëg xet ak lewetug gémmiñ. Mu ne, « bés bu Yàlla sàkk, dañuy seetlu yeneen xeeti peeñantal yees war a bàyyi xel bu baax. Lii di bakkan bu dul yëg xet, ñu naan ko « anosmie » ci nasaraan, ak lewetug gémmiñ, « agueusie », ci peeñantal yu bees yi lañ bokk. »

Waaye, nag, Pr Séydi daf cee teg ne, peeñantal yooyu, mënees na leen a fekk ci yeneen xeeti jàngoro.

TESTI COVID-19 YU GAAW YAA NGI ÑËW

Bees sukkandikoo ci kàdduy Dr Aamadu Alfa Sàll mi jiite ‘’Institut Pasteur’’ bu Ndakaaru, ciy fan yu néew, askanuw Senegaal dinañ mën a def ay test ci anam bu gaaw a gaaw. Dafa ne : « Liy bees ci caytug mbooloo maa ngi aju ci test yu gaaw yi nuy waaj a jot ñeel jàngoroy Covid-19 bi. Ndaxte, bu nu leen saytoo ba am ciy njeexital yu baax te dal xel, dees na leen natt cim mbooloo mu yem mees di lël ci béréb bu wóor. Loolu, nag, dinan ko def feek i fan rekk ; yàggatul dara. »

JURBEL

Ab ndongo buy jànge ca daaray ‘’Notre-Dame” moo ame jàngoroy Covid-19 bi

Ci ni ko kilfay daara ji xamlee, ndongo laa ngi tollu ci kalaasu CM2. Ñoom, nag, ci saa si lañu jël seen i matuwaay, daldi tëj daara ji.

Defalees na test ñi jot a jege ndongo loolu. Nee ñu yit, am na 2i mbokkam yu ame jàngoro ji. Waaye, xibaar boobu, kenn dëggalagu ko.

PÉNCUM RÉEW MI

Maki Sàll yabal na jawriñ yi ca péncum réew mi, ñu wuyuji dippite yi ba noppi fommaale seen bëru ren ji

Ci ndajem jawriñ mi amoon ci àllarba ji, benn fan ci sulet 2020, la Njiitu réew miwax jawriñ yi ñu wuyuji dippite yi, tontu seen i laaj ñeel caytug mbas mi, rawatina 1000iy milyaar yees jagleeloon naalub Force-Covid-19 ñeel xeexub mbas mi.

Waaye, Njiitu réew mi yemul ci loolu ndax bi muy fomm guural geek déju bi mu làmboo, ci la leen yégalaale ne, ren, kenn ci ñoom du ci dem bër, liggéey rekk.

BEYKAT YAA NGI FIPPU

Ginnaaw beykati Ndengleer yiy jaamaarlook Baabakar ngom, boroom SEDIMA, waa Kër-Musa, Jendeer ak Puut ñoo ngi doon ñaxtu ci buntu dalub sàndarmëri bu Puut. Li waral seen mer gi mooy, ci seen i wax, dañoo nangu seen i tool. Ñi ëpp ci ñoom, lujum lañuy bey.

Nee ñu, dañ leen a jaay doole, foqati 350i ektaar ci seen i tool, jox kob poromotëer buy liggéeyal boppam. Waxatuñ dara, kooku génneb kayitu suufam, di leen ko xeexe.

UBBITEG AYERPOOR YI

Nguurug Senegaal jël nab dogal, tere roppëlaani Ërób yi dugg ci réew mi. Nguur gi dafay feyantoo ak kurél gi ëmb réewi Ërób yi, « Union européenne », ginnaaw bim jëkkee tere doomi Afrig yeek yu Senegaal ñu dugg seen biir i réew.

Jawriñu tukkib kow gi ak wërantal gi, Aliyun Saar, nee na : « Soo leen méngaleek Afrig, bari nay réew yu mu gën demin fuuf ci mbas mi. Kon, Afrig du nangu mukk ñu nuy sikkal ak a seexlu. »

Xanaa mooy liñ naan ‘’ku ma ko dabin, ma rókkin la ko !’’

Articles les plus lus

ammbow.jpg
AMADOU MAHTAR MBOW, L’HÉRITAGE D’UN SIÈCLE DE COMBATS
C’est l’un des sages du continent. Ce mercredi marque le premier anniversaire du rappel à Dieu d'Amadou ...

mgueye_lq.jpg
LE PRES ET SES MILLIARDS DE FUMÉE
Le financement du Plan de redressement économique et social (Pres) fera-t-il revivre les anciennes filières ...

garage_latdior.jpg
OPERATION COUP DE POING AU GARAGE LAT DIOR
Dans la nuit de lundi à mardi, le garage Lat Dior, situé derrière le tribunal de grande instance de ...

capture_decran_2025-09-09_a_19.43.16.png
LA PAUVRETÉ, UN CRIME ?
Sous l’affichage tapageur d’un État de droit protecteur, le Sénégal s’éloigne silencieusement ...

whatsapp-image-2025-09-23-at-15.51.04.jpeg
LES FÉMINISTES APPELLENT À DES ACTES APRÈS LE DISCOURS DE DIOMAYE À L’ONU
Le lundi 22 septembre 2025, à la tribune des Nations Unies, le président de la République du Sénégal, ...

Vos articles préférés de la semaine

capture_decran_2025-09-19_a_15.17.55.png
SORTIR DE LA FASCINATION DU MARABOUTAGE
Inaf, inaf, inaf ! Nos écrans sont devenus des miroirs puissants de notre société. À travers les ...

scr-20250918-qocm.jpeg
JOURNÉE À MILAN
Rien à dire, Ousmane Sonko est bien un phénomène. Réussir une mobilisation monstre en terre lointaine ...

capture_decran_2025-09-12_a_12.48.41.png
REDUIRE LA PROFESSION VETERINAIRE A LA PRATIQUE DE LA SANTE ANIMALE NE PEUT PROSPERER EN AFRIQUE SUBSAHARIENNE
Ex-directeur de l’École Inter-États des Sciences et Médecine Vétérinaire (EISMV) de Dakar et ancien ...

1280.jpeg
QUI POUR ARRÊTER LE CARNAGE DE L’ÉTAT SIONISTE ?
Le génocide se poursuit dans la bande Gaza. Chaque jour, des dizaines de vies sont impitoyablement ...

capture_decran_2025-09-20_a_17.17.44.png
SCHALKE, FIERTÉ D'UN PEUPLE OUVRIER
« Schalke, c’est le charbon, la sueur et la fierté d’un peuple. » À Gelsenkirchen, dans le ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous