Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
1 octobre 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Societe
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

« LI NU DEF MALI, MËNEESU KO TUDDE CËTËN… »

France 24 amal nab laaj-tontu ak kii di Kolonel-Masoor Ismayla Wage mi yor kàddug way-fétteerlu yi booloo ci kurélug CNSP miyitte woo sàmm muccug askanu Mali. Nicolas Germain lay waxtaanal.

Lu defu waxu  |   Paap Aali Jàllo  |   Publication 24/08/2020

– Lu leen tax a def cëtëŋ lii ?

– Dafa fekk ne, réew mi doxul. Teg ci ne, dafa amoon ci askan wi ñu sonnoon lool. Rax-ci-dolli, ay jafe-jafe yu bare ñoo gaaraloon làrme bi ci boppam. Ger mi àggoon na foo xam ne soldaar yi mënatuñu woon sàmmoonte ak seeni wareef. Fi mu ne nii, nag, bu ma sañoon ñu bañ a wax waxi cëtëŋ. Ndax, du noon lanu jàppe mbir mi.

– Waaye IBK tekkiwul ndombo-tànkam ci coobare boppam…

– Yéen, loolu ngeen jàpp. Waaye, ndax moom moo leen wax ne dañ koo jaay-doole ?

– Wànte IBK nee na mënul woon def neneen…

– Mënul woon def neneen ndax moom ci boppam mujjee naa gis ni askan wi sonnee. Kenn newu ko bàyyil mbaa ñu rey la. Ku mu neex, nag, nga jàpp lu la neex. Fi mu nekk nii, noo ngi jokkoo ak doomi-réew yi réew mi soxal ngir taxawal ag ndajem néggandiku moo xam ne, ab maxejj a koy jiite. Noo ngi waxtaan ak kuréli way-moomeel yi, làngi kujje gi ak képp ku nu war waxtaanal ngir taxawal ndaje moomu.

– Lu ngeen naral IBK ?

– Loolu du sunu cër. Mbirum yoon la. Bu waxtu wa jotee, yoon dina def liggéeyam.

– Naka la seen digganteek M5-RFP deme ?

– Jotewunu daraak M5-RFP. Nun, genn làng jiitalunu.

– Monte yéen ak ñoom, yéen a bokk benn gis-gis ak benn àtte ñeel ni IBK yore woon Mali…

– Li waa M5-RFP tàmm a wax, dëgg gu wér péŋŋ la. Waaye, loolu du tekki ne ñoo nekk ci sunu ginnaaw, di nu sant nuy def. Amunook ñoom benn jëflante. Bi nu defee li nu def ba noppi, ci lanu ñépp woo, jokkoo ak nun.

– Àddina sépp a ñaawlu cëtëŋ li ngeen def. Ndax ragalu leen daan yiñ nar a teg Mali ?

– Ragal nanu ay daan, kay. Ndaxte, bu ay daan amee, askanu Mali mooy sonn.

– Ndajem néggandiku mi ngeen di waajal, ndax da fiy nekk ba wotey 2023 yi walla dangeen di amal ab wote bala boobu ?

– Sunu mébét mooy nu amal ay wote ci ni mu gën a gaawe, mbir mi dellu ci yoon, ku nekk dellu ca la nga nekkoon, rawatina soldaar yi nu doon. Muy 2023 walla 2022, ni mu gën a gaawe rekk, gën a baax.

– Ndajem néggandiku moomu, ñan ñoo koy séq ? Ay maxejj kese walla soldaar yi ci lañuy bokk ?

– Loolu, ci tombi waxtaan wi lay bokk. Mënaguma cee wax lu leer.

– Ndax jot ngeen a waxtaan ak CEDEAO ?

– Noo ngi jokkoo ak CEDEAO. War naa dajeek ñoom, sax.

– Ndax yeen a ngi jokkoo ak làrme Farãs ?

– Ci jamonoy jàmm, danuy jokkoo ak « Barkhan » ñeel xeexub jiyaadis yi. Waaye, bi nu taxawalee CNSP ba léegi, waxagunook làrme Farãs.

– Ndax jàpp ngeen ne li xew tey mën naa may fit jixaadis yi ?

– Waaw kay ! Xam nan ko bu baax. Loolu lanuy ragal sax. Moo nu tax a sàkku ci sunuy farandoo nu taxawunu, bañ noo seetaan.

Articles les plus lus

mackyligassama.jpg
MAKHILY GASSAMA OU UNE VOIX MAJEURE DE LA LITTÉRATURE AFRICAINE
Notre patrimoine littéraire est un espace dense de créativité et de beauté. La littérature est un ...

jean-baptiste-placca_0_2.jpeg
LÀ OÙ LES POLITIQUES AFFAMENT LA PRESSE, LA DÉMOCRATIE N'A AUCUN AVENIR
(SenePlus) - Dans un éditorial publié le 13 septembre 2025 sur RFI, Jean-Baptiste Placca dresse un ...

capture_decran_2025-09-28_a_16.29.53.png
MACKY SALL DÉVOILE LES TRAHISONS QUI ONT FORGÉ SON DESTIN
Dans un entretien exclusif accordé au podcast H5 Motivation d'Aziz H. Rok, l'ancien président Macky ...

130404850_678305526169140_73864340909318201_n.jpg
OUMAR SARR APPELLE AU PRAGMATISME ET À UN DIALOGUE CONSTRUCTIF AVEC LE FMI
S’exprimant sur l’annonce de la « dette cachée » par le gouvernement, Oumar Sarr a fait part de ...

capture_decran_2025-09-27_a_13.14.19.png
IL N’Y AURA PAS DE BILLETS PHYSIQUES POUR SÉNÉGAL-MAURITANIE, ANNONCE ABDOULAYE FALL
Le président de la Fédération sénégalaise de football (FSF), Abdoulaye Fall, annonce des changements ...

Vos articles préférés de la semaine

capture_decran_2025-09-19_a_15.17.55.png
SORTIR DE LA FASCINATION DU MARABOUTAGE
Inaf, inaf, inaf ! Nos écrans sont devenus des miroirs puissants de notre société. À travers les ...

fotojet.jpg
QUAND LA FRANÇAFRIQUE SE RETOURNE CONTRE SES HÉRITIERS
(SenePlus) - La double nationalité, autrefois perçue comme un atout, devient un obstacle majeur pour ...

capture_decran_2025-09-20_a_17.17.44.png
SCHALKE, FIERTÉ D'UN PEUPLE OUVRIER
« Schalke, c’est le charbon, la sueur et la fierté d’un peuple. » À Gelsenkirchen, dans le ...

fadeld.jpg
L’ÉTAT ET LES CHEFS RELIGIEUX, SUR UNE PISTE GLISSANTE
L’étranger qui n’aurait d’autres informations sur les préparatifs et le déroulement des deux ...

capture_decran_2025-09-22_a_21.09.15.png
L'EXIL DES INVISIBLES
Capitale sénégalaise et carrefour de multiples destins, Dakar voit affluer chaque jour des femmes ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous