Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
29 août 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Societe
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

MBËNN MI AK TOJ-TOJ YI : FAN LA MILIYAAR YI DUGGU ?

Njàqare, jaaxle la ñu bari ci ñi dëkke ci yenn diwaan yu nekk ci réew mi àndal gannaaw ba taw bi wàccee ci àllarba jii weesu rawatina ca Ndakaaru.

defuwaxu.com  |   Mamadu Jara  |   Publication 29/07/2022

Njàqare, jaaxle la ñu bari ci ñi dëkke ci yenn diwaan yu nekk ci réew mi àndal gannaaw ba taw bi wàccee ci àllarba jii weesu rawatina ca Ndakaaru. Taw bu baree lëmbe woon Ndakaaru ci bile bés  ba ay otorut am ci ay yàqu-yàqu. Bi ci gën a fés mooy bi jokkale « Patte d’oie » ak « aéroport Léopold Sédar Senghor ». Mu nekk lu askan wi di ñaawlu ba fa ñaawlu yam ndax tamñareet yi ñu dugal ci tabaxum (ndefarum) otorut yi.

Ci mbind yi « Préfet » bu Ndakaaru biral, « mbir mi kenn mënu ko woon fàggu ndax Ndakaaru, ci benn waxtu doŋŋ, daawul am taw bu baree nii ». Waxam jooju day wone mbetteel gim am ci yàqute yi. Moone de, Abdalaa Bari mi nekk doxalkat ci këru liggéeyu bii di BTP, safaan bi la gëm. Kàddu yooyee Moor Taala biral àndu ci. Moom dafa jàpp ne liggéey bi lañu caxat-caxatee. Maanaam, jaarul yoon te looloo tax otorut bi toj. Saytu bi waroon a ànd ak liggéey bi it amul woon te ñi ko yore woon, seen doole néewoon na lool. Nde, xew-xew bi nekkul lu bees ci réew mi ndax, ci benn dog bi, amoon na « pont » bu tojoon ci juróom-ñetteelu weer bi ñu ko ubbee ca atum 2017.

Gannaaw li dal otorut bi jokkale « Patte d’oie » ak « aéroport Léopold Sédar Senghor », « autopont » bu Yoof ak bu Kër Masaar ñoo jël raw-gàddu gi ci ndox mi. Nde, foofu moom kenn amul fu mu jaar. Du daamaar, du nit. Yoon yaa ngi fees dell ak ndox. Waaye li gën a ëlëm maxejj yi mooy « autopont » Kër Masaar bi sóobu/sànku ci ndox mi te bi ñu ko ubbee ak léegi deful weer. Léegi, lan moo ko waral? Ndox mi moo bari walla liggéey bi moo muccul ayib.

Mbooleem xew-xew yii ñooy jur ay sikki-sàkka ci boppi maxejj yi. Muy lu deme ni taxawaayu jëwriñ yi nguur gi dénk wàll woowu, ci seen njub, seen xarañte, añs. Ba tax na ñuy dëkk ci di laajte fu miliyaar yiñ jagleeloon fànn woowu duggu? Ak lan lañ ci def ca dëgg-dëgg? Ndax, bu dee lépp jaar na yoon, li ñu génnee ci xaalis ci ndefarum « autopont » yi ak otorut yi waroon na leen a mën a aar fileek ay at. Ndegam, maxejj yi mënuñu nànd mbir mi, ñoo ngi njort ay njuuj-njaaj ci sémb taaxu laltu yoon yi. Te it, ay at ci gannaaw, génnee woon nañ xaalis bu bari ngir mbënn mi, waaye ba léegi mbir dafa mel ni mbir mi amul coppite.

Fan la miliyaar yi duggu ? Fan la miliyaar yi duggu ? Loolu la askan wi jàpp, def ko aw woy fi ñu tollu nii.

Articles les plus lus

capture_decran_2024-07-18_a_23.21.06_0.png
AMADOU DIAW FAIT DE LA PHOTOGRAPHIE LE CŒUR BATTANT DE SAINT-LOUIS
(SenePlus) - Dans un entretien accordé à DakArtNews le 22 août 2025, Amadou Diaw, fondateur du ...

capture_decran_2025-08-27_a_01.08.32.png
ABASS FALL, POLITIQUE PAR ACCIDENT
De la prison du Cap Manuel à l’hôtel de ville de Dakar, Abass Fall, 58 ans, a traversé les épreuves ...

yande_diop.jpg
DANS LA LUMIERE ET L’OMBRE D’ALIOUNE DIOP
Dans le 5ᵉ arrondissement de Paris, au cœur de la rue des Écoles, une vitrine se distingue depuis ...

capture_decran_2025-08-26_a_14.31.09.png
ABASS FALL, DEUX ANS POUR CONVAINCRE
C’est l’objectif d’une vie qui vient de se réaliser pour le ministre du Travail. Il va inscrire ...

projet_avenir.jpg
LE PROJET AVENIR REDONNE ESPOIR AUX FEMMES ET AUX JEUNES
Dans une dynamique d’appui au développement local durable, le projet Adaptation et Valorisation Entrepreneuriale ...

Vos articles préférés de la semaine

c25d38f5-e2e1-4503-aad4-87cc038d7420.jpeg
QUAND LA MONNAIE DEVIENT UNE AFFAIRE DE LIBERTÉ
Pourquoi continue-t-on à penser que la monnaie n'est qu'une affaire de comptables, d'économistes et ...

img_2412.jpg
LE PACTE POUR LA TRANSFORMATION PROMISE
Cent-une voix, cent-une signatures, cent-une consciences alertées, réunies dans un "Appel des 101" ...

capture-decran-2025-08-15-a-17.21.57-800x445.png
LE DERNIER SOUFFLE D’UN MAÎTRE, LA PREMIÈRE LUEUR D’UN CHEMIN
Il y a des rencontres qui, par leur intensité et leur profondeur, changent à jamais le cours de ton ...

capture_decran_2025-08-18_a_23.57.59.png
LA MAGISTRATURE NE DOIT PAS PÉRIR
La plus grande crainte des adeptes de l'État de droit depuis l'accession du Pastef au pouvoir est l'effondrement ...

saima_sayed.jpg
LE PAKISTAN RICE ROAD SHOW ATTENDU A DAKAR LES 1ER ET 2 SEPTEMBRE
L'Ambassade du Pakistan à Dakar a annoncé que le «Pakistan Rice Road Show» s’arrêtera à Dakar, ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous