Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
25 mai 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Culture
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

KURÉLUG BINDKATI SENEGAAL YI AM NA NJIIT LU BEES : ABDULAAY FÓODE NJOON

Abdulaay Fóode Njoon, ñu bari di ko woowe Fóode ngir cofeel, bindkat la, móolkat la. Moo nekk ci boppu këru móolukaay gees dippee Abis Editions.

defuwaxu  |   Ndey Koddu Faal  |   Publication 11/03/2025

Gaawu, 8eelu màrs 2025, la kurélu bindkati Senegaal yi doon tabb njiit lu bees ci njiteefu Ibraayma Lóo, njiitu téereek dawal ak Amet Saalum Jakite, bindkat, mag ci kurélu bindkat yi bees sukkandikoo ci kàdduy bindkat bii di Meysa Mati Njaay. Tabb gaa nga amee woon ca màkkaanu bindkat yi, muy Kër Biraago Gu Bees ci teewaayu bindkat yu bari. Ginnaaw bi ñu waxtaanee ba laaj ku bëgg a jiite kurél gi, wuutu Aliyun Badara Béey mi génn àddina 1eelu desàmbar 2025, la Soxna Bengaa ak Abdulaay Fóode Njoon yëkkati seen i loxo. Ña ëpp ca ña fa teewon Fóode la ñu jox bopp, moo ko tax a nekk njiitu Kurél gi.

Abdulaay Fóode Njoon, ñu bari di ko woowe Fóode ngir cofeel, bindkat la, móolkat la. Moo nekk ci boppu këru móolukaay gees dippee Abis Editions. Ci wàllu mbind, Abdulaay Fóode Njoon bind na téere yu bari te am solo. Mënees na cee lim Faubourienne, Affluences, Pièces à conviction, Sentiers perdus, Cœur en location, Taxi woman, Des pas sur la mer, L’écho sur les dunes. Am na yoy ci téere yii yees di jàngale ci Jàngune bu Ndakaaru, naka noonu  ca Farãs bindkat bii di Aamadu Elimaan Kan tamit day jàngale téere Fóode.

Sëñ Njoon nag, yemul ci bind ak móol rekk, moo sos xewu téere bu mag boobu di Dakaar FILID ngir jëmale téere kanam.

Nekkoon na tamit njiitu Afrilivres, kurél gi ëmb móolkati Afrig yi ci làkku tubaab, jot na jiite tamit kurélu bindkati Afrig, Asi ak Amerig Latin. Ba ci gaawu giñ ko falee ci boppu kurélu bindkati Senegaal yi, Fóode lañ toftaloon ci Aliyun Badara Béey, ñu ànd di def liggéey bu am solo ñeel téere. Kon, tay Fóode, day wéyal la mu tàmbali woon rekk ci kurél gi. Lii la wax ginnaaw bi mu biralee mbégteem, gërëm ñi ko tabb :

« Fas naa yéene xar sama tànku tubéy ci luy boole bindkat yépp ci jàmm, sasoo naa yaatal ak beesal  kurél gi, ubbi bunti Kër Biraago rawatina ubbil ko bindkat yi féete ndaw. Maa ngi tàllal loxo ñépp ngir ñu jàpp ci liggéey bi ngir téere jëm kanam. Dinaa sol sama dàll tamit seeti mag ñi ngir taataan seen iy xalaat ak i digle ».

Lees mën a gëm la, ndax, ci li ko ñépp seedeel, Abdulaay Fóode Njoon ku xareñ la, ku yaatu te yaatu-dënn la, mën a boole mbindeef yi ci jàmm. Am na teggin, di maslaa boole ci fullaak faayda gu mat sëkk.

Séydi Sow ak Soxna Bengaa la ñu toftal ci Abdulaay Fóode Njoon.

Ngërëm ñeel na Meysa Mati Njaay mi jàpp ci lootabe ndaje mi ba lépp sedd guyy.

Ejo mi ngi ndokkeel Abdulaay Fóode Njoon, di ko ñaanal yen wi oyof ci moom.

Articles les plus lus

capture_decran_2025-05-16_a_04.51.43.png
LA HIÉRARCHISATION VESTIMENTAIRE DANS LES SÉRIES SÉNÉGALAISES
Dans nos salons, sur nos téléphones, nos tablettes ou via nos ordinateurs, les séries sénégalaises ...

capture_decran_2025-05-19_a_15.56.37.png
LE PATRIARCAT TUE
Drame conjugal C’est le commentaire qu’une jeune femme a fait pour déplorer le féminicide d’une ...

capture_decran_2025-05-19_a_19.00.19.png
ULTIMATUM DE SONKO SUR LE FRANC CFA
Dans son entrevue avec la chaîne de télévision publique burkinabè RTB ce lundi 19 mai 2025, Ousmane ...

40746529-34489473.jpg
NDEYE SALY DIOP PLACÉE SOUS CONTRÔLE JUDICIAIRE
L’ancienne ministre de la Femme, de la Famille, du Genre et de la Protection des enfants, Ndèye Saly ...

picture7-1-1080x700.png
L’ALIGNEMENT FARFELU DU SÉNÉGAL DERRIÈRE LES JUNTES
Depuis l’indépendance, le Sénégal s’est forgé une tradition diplomatique exemplaire, bâtie sur ...

Vos articles préférés de la semaine

chantier_constrcution_1.jpg
LE SÉNÉGAL PAIE SA DETTE AU PRIX FORT
(SnePlus) - L'appel de marge de 200 millions de dollars de JPMorgan sur un prêt angolais met en lumière ...

capture_decran_2025-05-16_a_04.51.43.png
LA HIÉRARCHISATION VESTIMENTAIRE DANS LES SÉRIES SÉNÉGALAISES
Dans nos salons, sur nos téléphones, nos tablettes ou via nos ordinateurs, les séries sénégalaises ...

capture_decran_2025-05-12_a_08.41.42.png
TARIQ RAMADAN COMME CHEIKH YERIM, COMME SONKO
Tariq Ramadan est à Dakar dans le cadre de la 13e édition de «Jokkoo», tenue le samedi 10 mai à ...

capture_decran_2025-05-04_a_02.13.12.png
UN DIALOGUE DE FAÇADE ?
Invité du Grand Jury de RFM ce dimanche, l'ancien ministre et politologue Yoro Dia n'a pas mâché ses ...

capture_decran_2025-04-15_a_05.14.23_0.png
DES BOTTES, DES BAÏONNETTES ET DES BÉNÉDICTIONS
Dans la grande foire panafricaine du XXIe siècle, il y a désormais un ticket gagnant : enfiler un treillis, ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous