Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
17 juillet 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Politique
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

ALIYU SÀLL, GII MARYIIS SAAÑA : KUMBA AM NDEY AK KUMBA AMUL NDEY

Bërki-démb rekk la fi OXFAM jéem a dooleel boroom ñaari tur yi, Elimaan Abi Kan ma fay liggéeye ne du ci dal, ñu bare ànd ceek moom. Noonu la daane OXFAM ma ko doon waaj a dellooy kayitam.

Ndey Koddu Faal (www.defuwaxu.com)  |   Publication 27/07/2019

Ñu jóge ca, beneen jéyya dal ci kow réew mi te mooy Gii Maryiis Saaña mi ñu ni ràpp ci kaso bi tëj. Ci li yoon wax, Gii dafa ni Frãs a ngi waaj a làqu song Senegaal, jaarale ko  ci defkatu ñaawteef yooyu ñu tudde terórist. Waaw. Looloo tax àttekat bi yabal takk-der yi Jëppël, ñu fekk fa Gii Maryiis Saaña yóbbu. 

Li njëkk a teey xel ci mbir mi moo di ne ndaje mi ñu wax ni fa la baat yooyu jibe, Gii ci boppam jëlu fa kàddu, joxewul xalaatam. Bu loolu weesoo, Gii du njiitu kurél gi ñu duppe FRAPP/France dégage. 

Kon lan la ko yoon toppe ? Li kéemaane te xaw a reelu sax, moo di ne yoon ci boppam xamu ci dara ba dara booloo jeex ! Àttekat bi daal, toog nay fan di seet lan la war a teg ci loxo askan wi.

Ayu-bés yi jiitu lii, Gii metitlu woon na bu baax ni yaakaaru ndawi Senegaal yi tase, Nàññ gornmaa Maki Sàll, wax li mu xalaat ci coowal petorol ak gaas bi lëmbe réew mi.

Yu ni mel moo waraloon ñoxor-njaayalkaati yi jàpp ko. Waaye dañu daan nég ba yëf yi dal ñu bàyyi ko. Ndekete booba ñu ngi xaar ba jekku ko, tam ko dëmm, nëbb ko jant bi. 

Léegi ma nga Rëbës, mu ngi fay bëgg a yàgg te du yoon tey, du yoon ëllëg. 

Bu doon sax liñ koy tuumaal moo ko wax ci gémmiñam, yoon mayul kenn mu jàpp ko.

Xéy-na li mu tudd Frãs moo tax ñu tëj ko. Réew nag, su demee ba ku wax sa xalaat ñu tëj la, kenn dootul xam lu mbir miy niru. Looloo tax ñu baree ngi naan Gii Maryiis Saaña daa war a génn kaso. Loolu la Raddho, Amnesty ak ñeneen wax. 

Moonte ay weer a ngi ñuy jiiñ càcc Aliyu Sàll, rakku Njiitu-réew mi, ñu naan dafa jalgati alalu Senegaal, ànd ceek saay-say bu ñuy wax Franck Timis. Waaye àttekat bi deful lu-dul woolu-woolu ko – ci yar ak teggin ! – ba noppi bàyyi ko mu dellu këram. Booba sax fekk na mu demoon Frãs ba delsi. Lu mu fa wuti woon ? Waa FRAPP/France dégage seen xel ñaaw na ci lool.

Doomu-Senegaal bii di Gii Maryiis Saaña deful dara lu-dul ànd ak AAR LI NU BOKK di jéem a aar li nu bokk. Waaw, xanaa li magam doonul Njiitu-réew mee tax caabi féete ko ginnaaw ca Rëbës ? Kon lii mooy ci dëgg-dëgg li Wolof naan : Kumba am ndey ak Kumba amul ndey…

Waaye kat, lii ëpp naa seetaan ndaxte tey Gii Maryiis Saaña, ëllëg keneen.

Articles les plus lus

shoo-tas-rv1-32-scaled.jpg
DIOMAYE MOOY SONKO OU LES DEUX FACES D’UNE MÉDAILLE
Le président Faye a parlé. Après les propos outrageants de son Premier ministre, la nation attendait ...

greffage_.jpg
GREFFAGES, PERRUQUES ET PARANOÏA ADMINISTRATIVE
Il est des jours où l’on se demande si certains directeurs généraux ne confondent pas leur bureau ...

capture_decran_2024-09-24_a_00.37.48_0.png
LE SÉNÉGAL A BESOIN D’UN EXÉCUTIF AVEC UN POUVOIR POLITIQUE FORT ET ÉCLAIRÉ
Le champ politique de l’action publique en Afrique est traversé par de nombreuses forces centrifuges, ...

cthiakane_.jpg
CE QUE L’AFFAIRE DU GRAND THÉÂTRE NOUS APPREND
Le 15 juillet 2025, la direction générale du Grand Théâtre national du Sénégal a publié un communiqué ...

capture_decran_2025-07-14_a_00.42.06.png
DIOMAYE - SONKO ET LES ENJEUX D’UN CONFLIT DE LÉGITIMITÉ
Les divergences au sein du couple Diomaye - Sonko ne seraient pas une répétition de l’histoire politique ...

Vos articles préférés de la semaine

capture_decran_2025-03-12_a_17.20.22_1.png
BIOPSIE D’UNE KOROMAQUERIE !
Être amoureux de la République de Ndoumbélane et ne pas vivre de satire peut rendre malade. Et être ...

capture_decran_2025-07-14_a_00.42.06.png
DIOMAYE - SONKO ET LES ENJEUX D’UN CONFLIT DE LÉGITIMITÉ
Les divergences au sein du couple Diomaye - Sonko ne seraient pas une répétition de l’histoire politique ...

sans_detour_mamadou_ndoye_iv_0_2.jpg
IL NOUS FAUT UNE POLITIQUE LINGUISTIQUE AUDACIEUSE A L’ECOLE
Invité à prononcer le cours inaugural du colloque international « Multilinguisme et diversité à ...

chroniques_dun_temps_politique_par_felwine_sarr_-_chroniques_dun_temps_politique_-_la_crise_de_letat_de_droit_felwine_sarr_recoit_sidy_alpha_ndiaye_hdpt4urkww0_-_709x399_-_2m30s.png
L’INDIGNATION À GÉOMÉTRIE VARIABLE
Chronique d’un temps politique Dans son émission Chroniques d’un temps politique, lancée en ...

fr_20250430_194907_195631_cs.jpg
THIERNO ALASSANE SALL OU LE DEGRÉ ZÉRO DE LA POLITIQUE
Quand on n’a rien à dire qui honore les morts ni éclaire les vivants, le silence n’est pas seulement ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous