Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
26 août 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Politique
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

AMNESTI : MAKI XÀLL NA YOONU JÀMMOO

Fan yii, ñoo ngi soow mbirum amnesti (mbaale) bi Njiitu réew mi junjoon. Amnesti boobu, lees ci jublu mooy far lépp li fi jot a xew diggante màrs 2021 ak suwe 2023. Diir boobu nag, ay bakkan yu baree ci rot, ñu jàpp ci kaso lim bu takkoo takku

defuwaxu  |   Cubba Taal  |   Publication 17/02/2024

Fan yii, ñoo ngi soow mbirum amnesti (mbaale) bi Njiitu réew mi junjoon. Amnesti boobu, lees ci jublu mooy far lépp li fi jot a xew diggante màrs 2021 ak suwe 2023. Diir boobu nag, ay bakkan yu baree ci rot, ñu jàpp ci kaso lim bu takkoo takku. Moo tax, am na ñu àndul ci manesti bi. Moo tax it, jur na xaat coow ak xàjjalikoo te dara xewagut.

Dafa di, bu naalub amnesti bi àntoo, mooy képp ku ca yoon jàppoon mbaa ñu tuumaal la ci dara, yoon daf lay bàyyi mbaa mu setal la ba nga set wecc, kenn dootu la toppeeti dara. Ñu gis ne, démb ba tey, ñu ngiy génnee ñu bari ci kasoy Ndakaaru yi. Moo xam ña fare ca làngug pólitigu pastef wala way-moomeel yi. Aliyun Saane, Mor Taala géy (Nitdof), Tusee Màngaa, Paap Abdulaay Ture, Yarga Si, Séex Umar Jaañ, Ustaas Asan Sekk, Doktoor Seydu Jàllo, Fadiilu Keyta, añs. Waaye, ñi ñu jàppagum ci kasoy diiwaan yi moom, bàyyeeguñ leen.

Fa xel yépp daje nag, mooy fa kasob “Cap Manuel”. Nde, fa lees jàppandi njiitul Pasteef la woon, di Usmaan Sonko, meeru Sigicoor bi. Ndax Maki Sàll day génne wujju pólitigam bi ko gën a sonal ? Muy laaj bi jar a laaj.

Dafa di, for nañu ci wewu béy ne, gaa ñaa nga cay dox ay jéego. Ñu ràññee ca taxawaayu Piyeer Gujaabi Atepaa ak Aliyun Tin. Ñoom nag, duggewuñu ko lu dut jàmm dellusi ci réew mi. Ndax bu ñu sukkandikoo ci Piyeer Gujaabi Atepaa mi séqoon waxtaan ak RFI, moom ak ñeneen ñoo ngi dox ak a def i pexe ngir disoo bi Maki Sàll di sàkku, Sonko mën caa bokk. Te, ma ngay xaar tontul Sonko bu ci waxtaane ak ay jegeñaaleem. Loolu, day ruumandaat ne njiitul Pastef laa ngi ci tànki génn. Mu nar a nekk coow ci kow coow. Ndax APR a ngi xaacu fii, naan dee du fi ame. Waa Pastef tamit, di xataraayu fee, naan ñoom waxtaanuñ ak Maki Sàll. Li ci kanam nag, rawul i gët

Articles les plus lus

scr-20250823-tmwl.jpeg
LES PYROMANES DE SUD
Je ne sais plus exactement à quel âge j’ai rencontré Henriette Niang Kandé et Vieux Savané. En ...

c25d38f5-e2e1-4503-aad4-87cc038d7420.jpeg
QUAND LA MONNAIE DEVIENT UNE AFFAIRE DE LIBERTÉ
Pourquoi continue-t-on à penser que la monnaie n'est qu'une affaire de comptables, d'économistes et ...

whatsapp_image_2025-08-21_at_10.47.28_pm.jpeg
DES CONTRACTUELS DE LA SONAGED RÉCLAMENT 13 MOIS D’ARRIÉRÉS DE SALAIRE
Quelque 31 contractuels de la Société nationale de gestion intégrée des déchets (SONAGED) mis à ...

capture_decran_2025-07-30_a_02.24.00.png
LA SOUVERAINETÉ NE PEUT SE NÉGOCIER SUR LES RIVES DU BOSPHORE
Alors que le gouvernement sénégalais multiplie les gestes de soumission diplomatique sous couvert de ...

capture_decran_2025-08-24_a_15.07.12.png
FADA MET EN GARDE CONTRE LA 'BOÎTE DE PANDORE'
Invité du "Jury du Dimanche" (JDD) ce 24 août 2025, Modou Diagne Fada, président des Libéraux Démocrates ...

Vos articles préférés de la semaine

capture-decran-2025-08-15-a-17.21.57-800x445.png
LE DERNIER SOUFFLE D’UN MAÎTRE, LA PREMIÈRE LUEUR D’UN CHEMIN
Il y a des rencontres qui, par leur intensité et leur profondeur, changent à jamais le cours de ton ...

img_2412.jpg
LE PACTE POUR LA TRANSFORMATION PROMISE
Cent-une voix, cent-une signatures, cent-une consciences alertées, réunies dans un "Appel des 101" ...

capture_decran_2025-08-18_a_23.57.59.png
LA MAGISTRATURE NE DOIT PAS PÉRIR
La plus grande crainte des adeptes de l'État de droit depuis l'accession du Pastef au pouvoir est l'effondrement ...

capture_decran_2025-08-15_a_15.48.57.png
DÉCÈS D’ABDOU SALAM FALL
Le Professeur Abdou Salam Fall, éminent sociologue à l’institut fondamental d’Afrique noire (IFAN), ...

saima_sayed.jpg
LE PAKISTAN RICE ROAD SHOW ATTENDU A DAKAR LES 1ER ET 2 SEPTEMBRE
L'Ambassade du Pakistan à Dakar a annoncé que le «Pakistan Rice Road Show» s’arrêtera à Dakar, ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous