Seneplus.com
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP
 
22 juillet 2025
FacebookTwitterRSS
Seneplus.com
Societe
  • La Une
  • Politique
  • Economie
  • International
  • Sports
  • People
  • Opinions
  • Societe
  • Annonces
  • Culture
  • Medias
  • Diaspora
  • Femmes
  • Développement
  • Santé
  • Éducation
  • SENEPLUS TV
  • Baromètres
  • #SilenceDuTemps
  • NELSON MANDELA
  • LEOPOLD SENGHOR
  • CHEIKH ANTA DIOP

GENN GAAL, ÑAARI JULLI

Tabaski ren ji, waneeti na xàjj-ak-seen biy màndargaal réewum Senegaal ak tolof-tolof yu metti yi askan wiy jànkoonteel.

www.defuwaxu.com  |   Publication 16/08/2019

Tabaski ren ji, waneeti na xàjj-ak-seen biy màndargaal réewum Senegaal ak tolof-tolof yu metti yi askan wiy jànkoonteel. Ci benn boor, wute am na ci bésub julli gi. Ñii ci dibéer ji lañu julli, ñee julli ci altine ji. Waaye de, bésub Arafaat bi moom, di juróom-ñeenteelu fan ci weeru Tabaski, kenn wutewu ci, bésub gaawu bi la woon,. Te ñépp a ko taxawe : ña aji, ña nga woon ca tangooru Arafaat, béréb bu sell ba ; ñi ajiwul woor bés bi ngir jëmmal màggaay bi ak taataan ngëneel yi mu làmboo. Bu dee wér na ni tabaskee ngi war a am ci fukkeelu fan ci weeru tabaski, kon saa buñ taxawalee bésub Arafaat, warees na julli ca ëllëg sa. Noonu la ko àddina sépp jàppe ba mu des waa Senegaal. Jamono ju nekk, fàww ku nekk wane ne kër diw la bokk, ci ndigalu diw lay wéye. Maanaam, naanu yee bare ci miim réew.  Ñu ne Senegaal menn réew la, wenn askan, benn bopp, am benn jëmu. Waaye, wax jooju de, safaanoo na lool ak li ñuy faral di gis. Waxuñu sax féewaloo biy màndargaal askan wi, waaye at mu nekk, ñu gis fi ñaari korite, ñaari tabaski. Li ci doy waar, nag, mooy ne, mësuñoo gis ñaari Arafaat walla ñaari tamxarit. Kon lu tax ñuy wuute ci tabaski ak korite te at mi di menn at kese ? Walla dafa am lu ci rax ? Laaj baa ngi noonu sampu, ku ci am tontu na wax…

Ci beneen boor, tabaski bi dafa woneeti metit yi askan wiy jànkoonteel. Jamono jii, lépp a yokku te xaalis amul. Simoŋ bi yokku na, ceeb bi yokku. Esãs ak gaasuwaal yokku, njëgu tukki bi yokku. Ñi war a tukki ngir bes bi sonn lool, liñ liggéey yépp nar a yem ci paas. Soble yokku, pombiteer yokku. Boroom kër yi jaaxle. Ñu ne déet-a-waay, ñàkkum xar mi ci réew mi ñëw doggali boroom kër yi. Ndege, jaaykat yi dañu aj njëg li fu kowee-kowe, xar jafe lool sax. Ba ci bésu tabaski bi, ci fajar gi, am nay boroom kër yu amagul woon xar. Ndeysaan, ñenn ñi daanaka ay mbote rekk lañu mujje am, dugal ci xaalis bu bare, tollu ci diggante 80 000 ak 125 000 CFA ; ñeneen ñi béy lañu mujje am, tabaskee ko. Te ñàkkul mu am ñu reyul faf. Dëgg-dëgg, réew mee maki, ni ko ndaw yiy waxe. Dara doxul, te ku ŋaaŋ ñu tëj la. Ñu ne Maki makiye na réew mi ba makiil ko. Te wolof dafa ne, ku makiyaasu walla ñu makiyaas la, boo ñaqee ñaaw. Moo taxit, waa réew mi  wax nañoo wax, ñaxtoo ñaxtu, wër a wër bay ñaq tooy xepp. Wax dëgg, ni réew miy doxe ñaaw na, li askan wiy dund tamit jéexal na xol. Lépp a caŋ, rawati-na mbay mi ak càmm gi. Waa kow ga ñoo gënatee sonn ndax suuf si wow na, gàncax amul, jur gaa ngiy dee. Nawetu ren ji, bu dee mënees na ko tudde nawet, dafa dëddu réew mi. Mu mel ni asamaan si dafa mere askan wi, niir yi gàddaay, ndox mi bañ a wàcc. 

Laago yii yépp dajaloo ci jenn jamonoo tax tabaski ren ji metti. Askan waa ngiy jooy, di sàkku ndimmal ci neen. Wànte, li gën a metti ci xoli nit ñi, mooy li njiitu réew mi génn keroog wax ne, li nguuram jënd ciy oto dafa bare, daanaka xaalis biñ jënde ay oto diggante 2012 ak léegi mat na 307i miliyaar ci sunu koppar. 
Loolu di firndéel yàq, yaataayumbe ak gundaandaat gi waa nnguur gi nekke. Waaye, Maki waxunu lépp. Ndaxte, oto yooyu, esãs walla gaasuwaal moo leen di dawal te loolu yit, ci nafa réew mi lañu ko feye. Kon xaalis bi ñu pasar-pasare ëpp na fuuf li mu wax. Nuy laaj, diggante 2012 ba tey jii, kan moo nekkoon Njiitu-réew mi ku dul moom ? Du moo fi dige woon ne yàq bi dina deñ ba mu set wecc, wax ne xaalis bi dina ko delloo ci askan wi ko jagoo ? Waaw, fu Maki nekkoon bi nguur giy jënd oto yooyu ak esãs walla gaasuwaal yi leen di dawal ? Fàtte da fee xajul sax. Keroog, ca dëju ndem-si-Yàlla Usmaan Tanoor Jeŋ, oto limusin bu ñuul bi yaboon Maki ak naataangoom bu Mali te mu lakkoon, 1 miliyaar CFA la jar ! Ca ëllëg sa, mu waraat beneen oto limusin bu doomu-taal buy jar njëg lu tollu noonu walla mu ëpp ko. Ndax daa fàtte boppam ? Kon, lu jiin Njaag a, te Maki mooy Njaag.  Te, am réew, su fa buur ak lingeer dee fecc, ku fay woyaan doo rus a yaŋas.

Articles les plus lus

capture_decran_2025-07-21_a_17.35.34.png
OUSMANE DIAGNE, SEUL CONTRE TOUS
Malgré une pression terrible venant de toutes parts et particulièrement de son camp, le ministre de ...

img_8060.jpg
SONKO, LE CRI DE DÉTRESSE DE GOLIATH
Le Premier ministre Ousmane Sonko a lancé une phrase lourde de sens : « Qu’on me laisse gouverner ...

photo-2025-07-20-18-14-04.jpg
AKERE MUNA ET SES ALLIÉS EN CAMPAGNE À WASHINGON
(SenePlus) - À trois mois de l’élection présidentielle camerounaise du 25 octobre, l’ancien avocat ...

macron.png
RELATIONS SÉNÉGAL/ FRANCE, LA RUPTURE EN MARCHE
L'ex première dame de Côte d'Ivoire, Madame Simone Gbagbo avait révélé que c'est la France qui validait ...

capture_decran_2021-01-12_a_17.18.38_2.png
BÂTIR UN PONT ENTRE LE PEUPLE AFRICAIN ET LES PEUPLES D'ASCENDANCE AFRICAINE
« Le peuple qui ne connaît pas son passé, ses origines et sa culture ressemble à un arbre sans ...

Vos articles préférés de la semaine

shoo-tas-rv1-32-scaled.jpg
DIOMAYE MOOY SONKO OU LES DEUX FACES D’UNE MÉDAILLE
Le président Faye a parlé. Après les propos outrageants de son Premier ministre, la nation attendait ...

capture_decran_2025-07-11_a_16.43.24.png
ON NE JOUE PAS AVEC LE SACRÉ
Il y a des décisions intimes que chacun traverse dans le secret de son âme. Des silences, des luttes ...

capture_decran_2025-07-14_a_00.42.06.png
DIOMAYE - SONKO ET LES ENJEUX D’UN CONFLIT DE LÉGITIMITÉ
Les divergences au sein du couple Diomaye - Sonko ne seraient pas une répétition de l’histoire politique ...

greffage_.jpg
GREFFAGES, PERRUQUES ET PARANOÏA ADMINISTRATIVE
Il est des jours où l’on se demande si certains directeurs généraux ne confondent pas leur bureau ...

cthiakane_.jpg
CE QUE L’AFFAIRE DU GRAND THÉÂTRE NOUS APPREND
Le 15 juillet 2025, la direction générale du Grand Théâtre national du Sénégal a publié un communiqué ...


La Une

Politique

Economie

International

Sports

Football

Media

People

Opinions

Societe

Annonces

Diaspora

Femmes

Développement

Santé

Éducation

PARTENAIRES DE SENEPLUS

APS
Grand-Place
L'As
L'Enquete
L'Observateur
La Gazette
Le Populaire
Le Quotidien
Le Soleil
Le Témoin
Libération
Nouvel Horizon
Réussir
RFM
RTS
Stades
Sud FM
Sud Quotidien
Sunu Lamb
TFM
Waa Sports

À propos de SenePlus

SenePlus.com est un portail d'informations sur le Sénégal. Nous vous fournissons des articles détaillés, critiques, pertinents sur l'actualité au Sénégal.

Coordonnées

Publicité:
pub@seneplus.com
Informations:
info@seneplus.com
Problèmes techniques:
tech@seneplus.com
Copyright © 2025 SenePlus  |  Publicité  |  Soumettre un Article  |  Nous Contacter  |  Mentions légales  |  Conditions d'utilisation  |  Á propos de nous